Ndegam surgaam ya ca asamaan sax wóoluw leen, ay malaakaam sax, mu sikk leen,
TSK
TSK · 2 Peter 2:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Mu afal meram, ba musalul seen bakkan, xanaa jébbal leen mbas ma.
¶ «Moo tax, dogu naa ci man miy dund, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, gannaaw yeena def seen wépp njombe ak seen jépp jëf ju siblu, di sobeel sama bérab bu sell bi, man itam, maa leen di wat nel te duma leen xool bëtu ñéeblu, duma leen ñeewante.
Duma xool bëtu ñéeblu, duma ñeewante. Say jëfin laa lay yool ak sa jëf ju siblu ji ci sa biir. Su boobaa ngeen xam ne maay Aji Sax jiy dumaa.
Rab yi nag tinu Yeesu, ngir mu bañ leena yebal ca xóote ba.
Ndegam cari judduwaale ya la Yàlla déegul, moytul mu bañ laa déeg yaw itam.
Su demee noonu kay, kon Boroom bi def loolu lépp, xam na nu muy musale nit ñu jullite cib nattu, ak nu muy xaare nit ñu dëng ñi, ngir seen mbugal kera bésu àtte ba.
Ñooy gannaxi géej gu sàmbaraax, di gëq seen puuriti gàcce; ñooy biddiiw yu fàq di taxawaalu, te lëndëm gu ne këruus di cér bu ñu leen sédde ba fàww.
¶ Ba mu ko defee ma gis malaaka mu wàcce asamaan, yor caabiy xóote bi, ak càllala gu réy.