Maay waññi say àttekat, ñu mel na woon, say diglekat it dellu mel ni bu jëkkoon. Su boobaa ñu wooye la Dëkkub Njekk, ak Dëkkub Kóllëre.»
TSK
TSK · Acts 1:6
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
«Ay bés a ngi ñëw,» kàddug Aji Sax jee, «maay jebbil Daawuda njebbitu njekk, mu falu di buur bu xelu, di jëfe njub ak njekk ci réew mi.
kon dinaa wacc askanu Yanqóoba ak Daawuda sama jaam bi, ba dootuma taamoo ciw askanam kuy yilif askanu Ibraaymaak Isaaxaak Yanqóoba. Maay tijji seen wërsëg moos, yërëm leen.»
Palug mboolem nguur yi asamaan tiim, ak kilifteef gaak daraja ja dees na ko boole, jébbal aji sell yu Aji Kawe ji. Nguurug mbooloo moomu day sax ba fàww, kilifa yépp di ko déggal, di ko wormaal.”
Waaye kaw tundu Siyoŋ la aw ndes di rawe, te dina doon bérab bu sell, waa kër Yanqóoba it moomaat seeni moomeel.
Aji Sax ji moo teggi say mbugal, waññi sab noon. Buurub Israyil, Aji Sax jaa ngi fi sa biir, dootuloo tiit lu bon.
¶ Farisen yi ñoo laajoon Yeesu, ne ko: «Kañ la nguurug Yàlla di dikk?» Mu ne leen: «Dikkug nguurug Yàlla du ànd akum ceetaan.
Man itam ni ma sama baay dénke nguur, ni laa leen koy dénke.