Kemu suufas Kanaaneen ña, mu ngi tàmbalee Sidon, jaar weti Gerar, dem ba Gasa, wuti Sodom ak Gomor ak Atma ak Ceboyim, daldi teeri Lesa.
TSK
TSK · Acts 12:20
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ci biir loolu Yàlla jagleel Suleymaan mu ñaw lool, am xel mu rafet ak xam-xamam bu yaa, bu solowoo fànn yu bare ni feppi suufas géej.
Ndoortel ay di wal mu tàmbali, luy indib xuloo, bàyyil.
bul gaawa layooji, ana nooy def ëllëg, bu ñu la yeyee?
¶ Yéene bii ñeel na dëkk ba ñuy wax Tir: Yeen waa gaali Tarsis ñi deele, jooyleen! Lépp a yàqu! Du kër, du teeruwaay. Fa dunu Sippar lañu leen ko waxe.
Yudak réewum Israyil it di say jula, di la wecci bele bu bawoo Minit, ak dugub ak lem ak diwu togg ak diwu yaram.
«Maa wéetal seeni biir seen dëkkoo dëkk, dugub ñàkke fépp fu ngeen moom, te taxul ngeen waññiku fi man.» Kàddug Aji Sax jee.
ku wuti waan ñaar fukki natti pepp, fukk lay fekk sàq ya; mu wuti ca nalukaay ba juróom fukki natti biiñ, fekk fa ñaar fukk.
Am ban buur mooy xarejeek beneen buur te jëkkula toog, seet ba xam ndax man naa ànd ak fukki junniy xarekatam, ngir xarejeek ku ko songseek ñaar fukki junniy xarekat?