TSK

TSK · Acts 21:39

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Acts 9:11 TSK

Sang bi ne ko: «Demal ba ca mbedd, ma ñuy wax Mbedd mu jub, te nga seet ca kër Yuda ku ñuy wax Sóol te dëkke Tàrs. Ma ngay ñaan.

¶ Ñu yóbbante leen bataaxal, bind ci ne: Nun ndawi Yeesu, ak mag ñi, seen bokki Yerusalem, noo leen bind, yeen sunu bokki gëmkat ñi dul Yawut te dëkke Àncos ak Siri ak Silisi. Nu ngi jiital sunub nuyoo.

¶ Póol nag ne alkaati ya: «Ñoom ñu dóor nu ci kanam nit ñi, àtteesu nu sax te nu diy gor ci Room gii, rax ci dolli ñu sànni nu ci kaso bi. Léegi ñu bëgg noo dàq ndànk ci biti? Mukk! Nañu ñëw, ñoom ci seen bopp, génne nu.»

Acts 22:3 TSK

¶ «Man ab Yawut laa, juddoo Tàrs ca diiwaanu Silisi, yaroo ci dëkk bii. Ci keppaaru Gamalyel laa jànge, njàng mu dëppoo bu mat sëkk ak sunu yoonu maam. Ma doonoon ku xér ci Yàlla ni mboolem yeen ñii tey.

Nit kii la Yawut yi jàppoon, di ko waaja rey, far ma dikk ànd ak lenn ci gàngoor gi, wallu ko, ndax fekk na ma yég ne as goru Room la.

Waaye Sang Almasi ngeen di sellal ci seen xol, te waajal nu ngeen di tontoo ku leen laaj lu jëm ci yaakaar ji ngeen am.