¶ Yonent Yàlla Maryaama, jigéenub Aaróona nag ŋàbb tabala, jigéen ñépp topp ko, génn di fecc, tabala ya jiin.
TSK
TSK · Acts 21:9
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Exodus 15:20
TSK
2 Kings 22:14
TSK
Ilkiya sarxalkat ba daldi dem ànd ak Ayikam ak Agbor ak Safan ak Asaya, ba ca Ulda yonent bu jigéen bay soxnas wattukatub yére ya, Salum doomu Tigwa doomu Aras. Ulda ma nga dëkkoon Yerusalem ca sanc ba. Ñu wax ak moom.
Acts 2:17
TSK
“Yàlla nee: Mujug jamono, maay tuur samag Noo ci kaw wépp suux; seeni doom, góor ak jigéen di biral waxyu, seeni xale yu góor di gis ay peeñu, màggat ñi di gént ay gént.
¶ Ci wàllu janq ji séyagul, awma ci ndigalu Boroom bi, xanaa ma wax ci sama xalaat bu mata gëm, ndax yërmande ji ma Boroom bi baaxe.
Kon gépp góor guy julli, mbaa muy waxe kàddug waxyu, bu muuree boppam, suufeel na Almasi, miy boppam.