TSK

TSK · Amos 2:7

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ «Bul dëkkoo sa soxnas doom. Sa soxnas doom la. Bu ko dëkkoo mukk.

Man ci sama bopp dinaa noonoo nit kooku te dinaa ko dagge ci biir bànni Israyil, ndax li mu jël ciy doomam jox Moleg, di sobeel sama bérab bu sell tey teddadil sama tur wu sell.

¶ Axab ñibbi këram, mer, ne fóññ ndax la ko Nabot waa Yisreel ba wax, ne ko du ko jox suufas maamam. Mu tëdd ca lalam, gedd, baña lekk.

Aji Sax jeey yékkati kàddug sikkaange, jëme ci magi ñoñam ak seeni kàngam. «Yeena sëxëtoo tóokëru reseñ bi, la ñu foqatee ci néew-ji-doolee nga seeni kër.

Wóoy ngalla boroom dogal yiy dogal njubadi, bind ko, te muy jur coono,

Kii ak jabaru jaambur ci jëf ju siblu, kee sobeel jabari doomam ci biir yàqute, kale di tëdde rakki doom baayam fi sa biir.

Amos 4:1 TSK

Dégluleen kàddu gii, yeen jigéeni tundu Samari, yeena ngi suur ni nagi diiwaanu Basan. Yeen ñiy torxal néew-ji-doole, di not aji ñàkk te naan seeni jëkkër: «Indil ñoll waay, ñu naan!»

Amos 5:12 TSK

Ràññee naa seen bàkkaar yu bare ak seen moy yu dul jeex. Yeenay tooñ aji jub, di geru, di xañ néew-ji-doole dëgg ci pénc.

Micah 2:2 TSK

Ñooy xemmemi tool, foqati, ay kër, ñu nangu, tey not waay ak waa këram, ak nit ci céru suufam.

Micah 7:2 TSK

Ngor a jeex ci réew mi, njub tumurànke ci nit ñi. Ñépp, ku ñu tuur deretam lañuy tëru, ku nekk, mbokkam lay fiir.

Yeen de yeena tax ñuy ñàkke teggin turu Yàlla ci biir xeeti jaambur yi dul Yawut, te noonu la ko Mbind mi indee.