TSK

TSK · Daniel 5:20

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ba Firawna yónnee, ba nemmiku mbir ma, xam na ne lenn deewul ca juru bànni Israyil. Teewul mu të ticc ba tey, baña bàyyi mbooloo ma, ñu dem.

Léegi nag xam naa ne, Aji Sax jee sut mboolem tuur yi, ndax la mu def, ba leen waa Misra torxalee.»

¶ Teewul ñu të ticc, sajju loos ni seen maam ya gëmuloon seen Yàlla Aji Sax ji.

Job 40:11 TSK

Yuril sa mer, te xool képp ku bew, detteel ko,

Yaw janq Babilon, wàccal, toog ci pënd bi. Yaw dëkkub Kaldeen bi ci taar bi laa ne, toogal fi suuf, amatoob jal. Dootoo dégg «Lewet, xay.»

«Aji Sax ji, Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: “Maa ngii di wàcce ci kaw dëkk bii ak mboolem li ko wër, lépp luy musiba mu ma dige woon, ndax dangeena të ticc, baña dégg sama kàddu.”»

«“Aji Sax ji dafa wax ne: Wéeruwaayi Misra ya day jóoru, doole ja Misray sago ŋiis; la dale Migadol ba Asuwan, saamar lañuy fàddoo. Kàddug Boroom bi Aji Sax jee.

Ba ñu ca tegee fukki weer ak yaar yu mat, muy doxantu ca kaw taaxum kër buur ca Babilon.

¶ Ca saa sa kàddu ga sotti ñeel Nabukodonosor. Ñu dàqe ko ci nit ñi, muy dunde ñax niw nag, lay biy wàcc di ko faam, ba kawar gi sëq ni dunqi jaxaay, ay wewam di saf yu njanaaw.

Luke 1:51 TSK

Dooley loxoom la defe ay jaloore, tasaare ñi jikkowoo réy-réylu,

Waaye bés bu nekk deeleen soññante li feek muy bésub tey agum, bala bàkkaar a nax kenn ci yeen, ba mu mujj dërkiis.