Aji Sax jee màgg, jara màggala màggal ca sunu biir dëkku Yàlla, kaw tundam wu sell.
TSK
TSK · Daniel 8:9
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
«Maa leen naroona teral ni doom yu góor, may leen suuf su xemmemlu, ngeen gënle xeet yépp suuf. Ma noon dingeen ma wooye baay te dungeen ma dëddu mukk.
Ba tey maa leen giñal ca màndiŋ ma, ne duma leen yóbbu réew ma ma leen jox, fa meew maak lem ja tuuroo, fa gëna taaru ci réew yépp.
Ma bëgga am lu leer ba tey ci fukki béjjén yi ci bopp bi ak beneen ba génn, ba ñett daanu ca kanamam; mu am ay bët ak gémmiñ, di wax kàdduy damu, te ëpp yi ci des.
Dina yékkati ay kàddu dal ci Aji Kawe ji, dina fitnaal aji sell yu Aji Kawe ji te dina fexee soppi takkinu jamono yi ak yoonu Yàlla wi. Dees na teg aji sell yi ci loxoom diiru ñetti jamonook genn-wàll.
Ki leen di song dina leen def li ko soob, ndax kenn du ko të. Dina toog ci réew mu taaru ma, te am dooley tas ko.
¶ «Bu loolu weesee dina ànd ak mbooloo mu bare, daldi yebook doole ak pastéef ci kaw buur bëj-saalum. Buur bëj-saalum waajal xare, ànd ak mbooloo mu réy te bare doole lool, waaye sottiwul ndax pexe yu ñu koy lalal.