¶ Naka la Esra di ñaan ak a tuub, di jooy, ak a daanu fa suuf ca buntu kër Yàlla ga, bànni Israyil yéew ko, bare lool, góor ak jigéen, ba ca xale ya. Mbooloo ma it di jooy jooy yu metti.
TSK
TSK · Daniel 9:20
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Éy Yerusalem, su ma la naree fàtte, yal na ma doole dëddu!
Amul moos ku jub ci kaw suuf, kuy def lu baax te du bàkkaar.
mu ne: «Ñooñu, maa leen di yóbbu sama kaw tund wu sell, bànneexale leen sama biir kërug ñaan, seen saraxu rendi-dóomal ak yeneen sarax, dees na leen ko nangul sama kaw sarxalukaay, ndax dees na wooye sama “kër, kërug ñaan”, ñeel xeetoo xeet.»
Yerusalem, tabb naa ay jongrukat ci sa kawi tata. Buñu selaw, du guddi du bëccëg! Yeen ñiy soññ Aji Sax ji, buleen dal-lu.
Ma walbatiku jublook Boroom bi Yàlla. Maa ngi sol saaku, diwoo dóom boole kook koor, toroxloo ko, di ko ñaan ak a dagaan.
¶ Jant yooyu, man Dañeel maa nga doon ñaawlu diiru ñetti ayi bés.
¶ Ba ñu ñaanee ba noppi, bérab ba ñu daje daa yëngu, ñu feese Noo gu Sell gi ñoom ñépp; ñu daldi tàmbalee waxe fit kàddug Yàlla gi.
Ndax kat ñépp a bàkkaar, ba jotewuñu leeru Yàlla,
¶ Ci kaw loolu mu yóbboo ma Noowug Yàlla ba ci tund wu mag te kawe, daldi may won dëkk bu sell bi, Yerusalem, muy wàcce asamaan, fa Yàlla.