¶ Aji Sax ji moo waxoon Ibraam, ne ko: «Jógeel sam réew, jóge ci say bokk ak sa kër baay, te nga dem ca réew mi ma lay won,
TSK
TSK · Exodus 3:18
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ba Ibraam amee juróom ñeent fukki at ak juróom ñeent (99), am na bés Aji Sax ji feeñu ko ne ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Topp ma te mat sëkk.
Mu ne ko: «Man déy, maay ànd ak yaw, te boo génnee mbooloo ma Misra, dingeen ma jaamusi ci tund wii. Loolooy firndeel ne, maa la yónni.»
¶ Gannaaw loolu Musaa dellu wax Aji Sax ji ne ko: «Waaw, su ñu ma dégluwul te gëmuñu ma, xanaa ne ma: “Aji Sax ji feeñuwu la” nag?»
¶ Ba ñu lalee panaan ca yoon wa, Aji Sax ji dafa dogale Musaa, nar koo rey.
¶ Gannaaw loolu Musaa ak Aaróona dem ca Firawna, ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: “Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma ca màndiŋ ma.”»
Wax ko ne ko: “Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi, moo ma yónni ci yaw. Mu di la wax, ne la: ‘Bàyyil sama ñoñ, ñu jaamuji ma ca màndiŋ ma.’ Yaw nag booba ba tey yaa ngi tanqamlu.
Musaa ne ko: «Bu ma bàyyikoo ci yaw rekk Firawna, dinaa tinu Aji Sax ji, ngir ëllëg ndiiraani weñ yi teqlikook yaw, ak say dag ak sa waa réew, waaye kat Firawna, bu nu naxati, di baña bàyyi mbooloo mi, ñu rendili Aji Sax ji sarax.»
¶ Ba loolu wéyee Aji Sax ji da ne Musaa: «Demal ca Firawna, nga ne ko: Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi dafa wax ne: “Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma.
¶ Musaa ak Aaróona nag dem ca Firawna, wax ko ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi dafa wax ne: “Siide nga maa nangul daal? Waaw, foo àpp sa ngàntal ak man? Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma.
¶ Firawna bàyyi na mbooloo ma, ñu dem, waaye Yàlla jaaralewu leen ca yoon, wa jëm réewu Filisti, doonte moo gënoona gàtt. Booba Yàlla dafa xam ne, su mbooloo ma sóoboo ci ay xare ci woowu yoon, dañuy yoqi, bay xalaata dëpp, dellu Misra.
Foofa laay dajeek yaw; fa tiim kubeeru njotlaay ga, ca diggante ñaari serub ya ca kaw gaalu seede sa, fa laa lay waxe mboolem lu ma lay sant, ñeel bànni Israyil.
¶ «Tegal sarxalukaayu cuuraay bi ci kanam rido, bi làq gaalu àlluway seede si ak kubeeru njotlaay, gi ci kaw gaalu àlluway seede si, foofu may dajejeek yaw.
Ci kaw loolu Elasar sarxalkat bi jël andi xànjar, ya ña dee ca lakk ga indi woon, ñu tëgg ko ba mu tàlli, ngir sarxalukaay ba,
Balaam ne Balag: «Taxaweel nii ci sa saraxu rendi-dóomal, man ma séentuji nee.»
Nun ñépp a mujj mel ni sobe, ni sagaru sobe la sunu gépp njekk mel. Nu ngii nun ñépp mel ni xob wu lax, sunuy tooñ buub nu, yóbbu ni ngelaw.
Newuñu: “Ana Aji Sax, ji nu génne woon réewum Misra, jiite nu ca biir màndiŋ ma, ca joor gu wow gaak xur ya, réewum maral ma lëndëm këruus, jaareesu fa, dëkkeesu fa?”