TSK

TSK · Exodus 32:12

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ba loolu amee Aji Sax ji fomm musiba ma mu waxoon ne dina ko teg ñoñam.

“Ñàkka mana yóbbu mbooloo mii ca réew ma mu leen giñaloon, moo waral Aji Sax ji faagaagal leen ci màndiŋ mi!”

Lu ko moy kat waa réew ma nga nu jële dinañu ne: “Tële leena yóbbu réew ma mu leen digoon, ak jéppi leen moo tax Aji Sax ji génne leen, ngir rey leen ca màndiŋ ma.”

«Maa noon maa leen di fàkkas, ba far dakkal lu leen nit doon fàttlikoo.

Aji Sax jeey dëggal ñoñam, mooy ñeewante ay jaamam, bu gisee doole dëddu, ba kenn desul, dub jaam, dus gor.

Kon xoolal, Aji Sax ji, noon a ngi ree, xeet wu amul bopp a lay sewal.

Éy Yàlla, yaa nuy musal, wallu nu, ba sa seede rafet. Xettli nu te baal nu sunuy bàkkaar, ba sa woy rafet.

Aji Sax ji, délsil, loo deeti xaar? Ngalla yërëmal sa jaam ñi.

Waaye déy, Aji Sax ji, yaa di sunu Baay; noo di ban, yaw ngay tabaxkatu njaq, nun ñépp di sa liggéeyu loxo.

Teewul ma sédd ci sama teddngay tur, ngir xeet yi ñu nekk ci seen biir bañ maa sikk. Ndax ba may xamal bànni Israyil sama bopp, di leen génne Misra, xeet yooyaa ko seede woon.

Teewul ma téye sama loxo, sédd ci sama teddngay tur ngir xeet, ya seede woon ba ma leen di génne, bañ maa sikk.

Amos 7:6 TSK

Boroom bi Aji Sax ji fomm ko ne ma: «Liitam du am.»

Ndax Aji Sax ji Boroom gàngoor yi déy dafa wax ne: «Na ma leen nammoona mbugale te delluwuma ci gannaaw, ba ma seeni maam merloo,» Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ko wax,