TSK

TSK · Exodus 34:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Juróom benni fan ngeen wara liggéey, def ci seen soxla yépp.

¶ «Diiru juróom benni fan ngeen di liggéey, waaye bésub juróom ñaareel ba, nopplu leen, ndax seen nag ak seen mbaam mana nopplu, seen surga akub doxandéem it mana astandiku.

¶ «Sàmmleen bésub Noflaay, ngir sellal ko, ni leen ko seen Yàlla Aji Sax ji sante.

Ñoom lay tabb ngir ñu doon njiiti kuréli junniy dag, mbaa njiiti kuréli juróom fukk. Ñoom it lay beyloo toolam, di leen góobloo, di leen sàkkloo ay gànnaayi xareem ak jumtukaayi watiiram.

Njiitu jàngu ba nag yékkati kàddug ñaawlu ndax bésub Noflaay ba Yeesu faje. Mu ne mbooloo ma: «Juróom benni fan la nit ñi wara liggéey. Kon ci fan yooyu ngeen wara fajusi, waaye du ci bésub Noflaay.»