TSK

TSK · Ezekiel 21:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

«Noon baa nga naa: “Maay dàqe, dabe, lël alal ja, séddale séddu, ba xol sedd, ne saamar boset, teg leen loxo.”

Yeen nag maa leen di tasaare ci biir xeet yi, ndax maay génne saamar mbaram, mu dal ci seen kaw. Seenum réew dina wéet, seen dëkk yu mag gent.

Job 9:22 TSK

Lépp benn la rekk! Moo tax ma ne: «Ku mucc ayib ak ku bon lay boole fàkkas.»

Dees koo gor, taal; yal na ñii sànkoo sa mbugal.

Ñépp a bokk benn dogal bi, ku jub ak ku bon, ku baax ak ku set, ak ku sobewu; kuy sarxal ak ku dul sarxal, muy ku baax ki, di bàkkaarkat bi, muy kiy giñ, di ki ragal ngiñ.

Aji Sax ji nee: «Saab saamar a reye fa asamaan ba màndi deret, te mu ngii di wàccal Edom, xeet wi may faagaagal, ngir àttee leen ko.»

Waaye su ngeen ma déggalul, baña sellal bésub Noflaay, baña moytoo gàddu lenn, di jaare bunti Yerusalem bésub Noflaay, su boobaa dinaa taal dëkk bi taal buy xoyom këri Yerusalem yu yànj, te du fey.”»

maa leen di dikke seen añu jëf.” Kàddug Aji Sax jee. “Maay jafal sawara, lakk seen gott bi, mu xoyom lépp lu leen wër.”»

«Babilon mu reewee, maa ngii fi sa kaw.» Kàddug Boroom bi, Aji Sax jee, Boroom gàngoori xare yi. «Sa bés déy taxaw na, di àpp bi ma la wara mbugale.

«Maa ngii déy, fi sa kaw, yaw Babilon, ponkalum yàqkat bi,» kàddug Aji Sax jee, «yaw miy yàq àddina sépp. Maay tàllal sama loxo fi sa kaw, taxañe la fa kaw doj ya, def la ponkalum jalu dóom.

Seen ñetteelu xaaj, mbas lañuy deeye mbaa xiif bu leen di sànk ci biir dëkk bi. Beneen ñetteelu xaaj bi, saamar lañuy fàddoo ci seen dig-digal bi. Xaajub ñetteel bi ci des, fépp fu ngelaw jublu laa leen di tasaare, te saamar laa leen di toppe.

Su ma wàccee saamar ci miim réew it, ba sant saamar ne ko mu jaar ci biir réew mi, dagge fi nit ak mala,

Dagge fi yaw ku jub ak ku bon moo may taxa boccee sama saamar mbaram, dal ci mboolem kuy dund, bëj-saalum ba bëj-gànnaar,

Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: «Wóoy ngalla bii dëkku bóomkat! Man it dinaa yokk jalu matt mi.

Amos 5:6 TSK

Sàkkuleen Aji Sax ji, ba dund. Lu ko moy mu ne jippét ci kaw askanu Yuusufa, lakk waa Betel lakk gu dul fey.

Gaynde di fa fàdd lu doy ay doomam, reyal ay jeegi gayndeem, feesal xunteem akum rëbbam, feesal paxam akum pàddam.

Yeen waa Kuus, itam yeen lees di fàdde sama saamar.