TSK

TSK · Genesis 1:14

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

def naa sama xon ci niir yi, muy màndargaal kóllëre, gi dox sama diggante ak àddina.

Job 3:9 TSK

Yal na biddiiwi njëlam giim, muy séentug leer te du am; yàlla bumu gis fu njël di xippee,

Job 25:5 TSK

Xoolal, weer wi sax leerul ba doy ko, te biddiiw yeet gisul seen sellaayu leer,

Job 38:31 TSK

Yaay faste genn dëllooñ gu ndaw gi ci digg asamaan? Am yaay yiwi dëllooñ gu mag ga mu dendal?

Damay xool sa asamaan si nga móol, ak weer week biddiiw yi nga fi teg.

Yaa moom bëccëg, moom guddi, teg fi weer week jant bi.

Yaa sàkk weer, muy takku jamono, sàkk jant, mu xam waxtuw fatoom.

Moo sàkk leer yu mag yi: Kee saxoo ngoram!

Moo leen samp, ñu sax ba fàww, mu dogal ko, te du toxu.

Aji Sax ji dafa wax ne: «Jikkoy xeeti yéefar yi, buleen ko roy; màndargam asamaan, buleen ko tiit; na ko yéefar yi tiit.

«Aji Sax ji dafa wax ne: Ndegam manees naa dog sama kóllëre maak bëccëg mbaa sama kóllëre maak guddi, ba bëccëg mbaa guddi baña teew ci waxtoom,

Bu sa leer feyee, maay muur asamaan, lëndëmal ay biddiiwam, sànge jant bi aw niir, weer wi noppee leeral.

Bésub Terutel weer, wenn yëkk wu ndaw lay doon wu amul sikk ak juróom benni xar yu ndaw akam kuuy, te lépp mucc sikk.

Amos 5:8 TSK

Kee sàkk biddiiwi lolli ak biddiiwi cooroon, mooy walbati lëndëm bët set, def bëccëg di guddi. Keey woo walum géej, walal fi kaw suuf. Kookoo di Aji Sax ji.

¶ «Ay firnde dinañu feeñ ci jant bi ak weer wi ak biddiiw yi. Ci kaw suuf njàqare ak tiitaange mooy ñeel xeet yi ndax riirum géej gi ak gannax yi,

Acts 2:19 TSK

Te maay def ay kiraama fi asamaan aki firnde ci dun bi fi suuf; muy deret ak sawara ak niiru saxar.

¶ Ñeenteelu malaaka mi wal liitam, mu dal ñetteelu xaaju jant bi, ak ñetteelu xaaju weer wi, ak ñetteelu xaaju biddiiw yi, ba tax seen ñetteelu xaaju leer giim, ñetteelu xaaju bëccëg bi daldi lëndëm, ñetteelu xaaju guddi gi it gëna lëndëm.