TSK

TSK · Genesis 1:26

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Léegi nit mel na ni nun, xam lu baax ak lu bon. Kon nag bumu tàllal loxoom, di witt ci doomi garab giy taxa dund, di lekk, bay dund fàww.»

Mboolem rabi àll yi ak njanaawi asamaan ak ndëgmeent yi ci suuf, ak jëni géej yépp, dinañu leen ragal lool. Teg naa leen ci seeni loxo.

Ayca nu wàcc, safaan seen làkk, ba dootuñu déggoo.»

Job 35:10 TSK

Waaye kenn du ci ne: «Wóoy ana Yàlla mi ma sàkk, kiy fentloo woyi cant ci biir guddi,

Damay xool sa asamaan si nga móol, ak weer week biddiiw yi nga fi teg.

Seedeleen ne Aji Sax jeey Yàlla. Moo nu sàkk, nuy ñoñam, di gàttam yi muy foral.

Na Israyil bége kii ko sàkk, doomi Siyoŋ, laa ne, ñu bànneexoo seen buur bii.

Éy Aji Sax ji, bul mer lool, bul ba xel fàww ci ñaawtéef. Ngalla seetal ne nooy sa ñoñ, nun ñépp.

Ndax li ngay wax kat sunu ngan-gi-nopp la. Nu bëgga xam nag loolu lu muy tekki.»

“Ndax sunu bakkan ak sunu yëngu ak sunug nekk, lépp ci moom la.” Mooy ba tey la ñenn ci seeni woykat ne: “Nun itam aw xeetam lanu.”

Nun ñépp nag, kanam gu muriku lanuy xoole niki cib seetu, leeru Boroom bi, ba tax nuy soppiku, doon takkndeeram, tey làmboo leer guy màgg, di gëna màgg. Looloo di liggéeyu Boroom bi, moom miy Noo gi.

te ngeen soloo jëmm ju yees ji Yàlla sàkke ci takkndeeram, di jëfe njub, ak sellnga ji dëgg di jur.

ba sol seen jëmm ju yees, jiy gën di yeeslu, te di gëna niru ki leen ko sàkkal, ba kera ngeen xamee, xam-xam bu mat sëkk.

James 3:7 TSK

¶ Mboolem xeeti rabi àll yeek njanaaw yi, ak ndëgmeent yi, ak rabi géej yi, dees na leen tàggat, te nit a leen di tàggat ba ñu mokk.