TSK

TSK · Genesis 19:16

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ci kaw loolu Aji Sax ji romb fa kanam Musaa, di biral naan: «Aji Sax jee, Aji Sax ji, Yàlla jiy yërëm, di yéwéne, mer ma diib, ngor gaak kóllëre ga bare.

Ndax seen Yàlla Aji Sax ji Yàllay yërmande la. Du leen wacc, du leen yàqte te du fàtte kóllëre, ga mu fasoon ak seeni maam ci kaw ngiñ.

Boroom bi, yaa baax, di bale, di nàddil sa ngor képp ku lay sàkku.

Yërmandeeku yiw, fa Aji Sax ji. Moo muñ mer te bare ngor.

Màggal-leen Ki Sax! Santleen Aji Sax ji, kee baax, kee saxoo ngoram!

Santleen Aji Sax ji, kee baax, kee saxoo ngoram!

Santleen Aji Sax ji, kee baax, kee saxoo ngoram!

Nangeen sante Aji Sax ji mbaaxam. Kee saxoo ngoram!

Luke 6:35 TSK

Yeen kay, soppleen seeni noon, defleen lu baax, lebleleen te baña yaakaar ndelloo. Su boobaa seenub yool réy, ngeen di doomi Aji Kawe ji, ndax moom de ñi santadi te bon, moo leen di baaxe.

Kon nag Yàlla mooy yërëm ku ko neex, te ku ko neex lay dëgëral xolam.

¶ Waaye Yàlla mi bare yërmande, ci kaw cofeel gu réy, gi mu nu sopp,

Su demee noonu kay, kon Boroom bi def loolu lépp, xam na nu muy musale nit ñu jullite cib nattu, ak nu muy xaare nit ñu dëng ñi, ngir seen mbugal kera bésu àtte ba.