TSK

TSK · Genesis 24:45

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Laata muy ñaan ba noppi sax, gis na Rebeka gàddu njaqam, di ñëw. Rebeka moomu di doomu Betuwel te di sëtu Milka ak Naxor, miy magu Ibraayma.

Booba Aanaa ngay ñaan ca xelam, gémmiñ ga rekk ay yëngu, waaye déggeesul baatam. Eli foog ne dafa màndi,

Buur wax ma, ne ma: «Ana looy sàkku?» Ma ñaan gaaw ci Yàlla Boroom asamaan,

Su boobaa balees woote, man, maay wuyu; balaa ñoo daane seen kàddu, ma nangul leen.

Ba nga tàmbalee ñaan la kàddu dikk. Maa la ko yégalsi, ndax yaw ku ñu naw nga. Déggal kàddu gi te dégg peeñu mi.

Acts 4:24 TSK

Ba ko bokk ya déggee, ñoom ñépp a mànkoo, daldi yékkati kàddug ñaan fa Yàlla, ne: «Buur Yàlla, yaa sàkk asamaan ak suuf ak géej ak lépp li ci biir.

Gannaaw ba Piyeer ràññee loolu, daa dem kër Maryaama, ndeyu Yowaan Màrk, fekk ñu bare daje foofa, di ñaan.