¶ Ba Yuusufa agsee ca magam ya, dañoo futti mbubbam, mooy mbubb mu yànj, ma mu soloon.
TSK
TSK · Genesis 42:21
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Ba loolu amee kilifa gay topptoo naani Firawna ne ko: «Man de tooñ naa te dinaa la ko wax tey.
Waaye su ngeen jëfewul noonu kat, yeena moy Aji Sax ji, te xamleen ne seenug moy dina leen dab.
¶ Daawuda nag ne Natan: «Maa tooñ Aji Sax ji.» Natan ne ko: «Aji Sax ji it jéllale na sa bàkkaar; doo ci dee.
nit ki seedeeli ko ca nit ña, ne: «Maa bàkkaar, maa xëtt njub, te feyeesu ma ko sax!
Bu ñu demee ba ñu jéng leen, mbaa buumi njàqare ŋodaar leen,
Ku tanqamlu jooyi ku ñàkk dina woote wall, wall ñàkk.
Ku bóom nit, daw, ba tàbbi njaniiw; bu ko kenn taxawu.
Seenug mbon a leen di mbugal, seen ñàkk kóllëre yar leen. Ñamleen ba gis ni ngeen ma dëddoo, wormaalatuleen ma, man seen Yàlla Aji Sax ji, muy loraange ju leen wex.» Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.
¶ «Kon nag, Aji Sax ji dafa wax ne: “Ku nekk ci yeen waroon naa goreel mbokkum dëkkandoom, waaye yeen déy, déggaluleen ma. Man nag maa ngi nii di leen goreel,” kàddug Aji Sax jee, “ngir wacce leen saamar ak mbas akub xiif. Maa leen di def waa réewi àddina yépp seexlu leen.
ndax sama juróomi rakk a nga fa. Na leen àrtu, ngir ñu baña ñëw ñoom itam ci bérabu metit bii.”
Daan bu àndul ak yërmande, moom lees di àttee ña daawul jëfe yërmande. Yërmande nag kekku na ab daan.