Mu dellooti ëmb, am doom ju góor daldi ne: «Bii yoon dinaa sant Aji Sax ji,» loolu tax mu tudde ko Yuda (mu firi Cant). Gannaaw loolu njuram taxaw.
TSK
TSK · Genesis 49:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Fekk booba Yuusufa mooy dogal ca réew ma, di jaay pepp waa réew mépp. Magi Yuusufa ya ñëw, sujjóotal Yuusufa.
Doomi Yuda yu góor di Er ak Onan ak Sela ak Peres ak Sera, te Er ak Onan faatu ca réewu Kanaan. Doomi Peres yu góor di Esron ak Amul.
Raayab dalu Yudeen ña moo jëkka jóg, ànd aki gàngooram, njiital gàngooru Yuda di Nason doomu Aminadab,
¶ Lii nag moo ñeel Yuda. Mu ne: Éy Aji Sax ji déggal yuuxi Yuda te yóbbu ko ciy bokkam. Mooy jànkoontee dooley boppam, waaye yaa koy wallu ciy noonam.
Noonu la magi Israyil ñépp dikke ca Buur Daawuda ca Ebron, mu fasook ñoom kóllëre fa kanam Aji Sax ji. Ñu sotti Daawuda diwu pal ga, muy buurub Israyil.
¶ Yowab nag indil Buur limu askan wa: Israyil di juróom ñetti téeméeri junniy góor (800 000) ñu tollu ci xare; Yuda di juróomi téeméeri junniy góor (500 000).
Sol nga ma dooley xare, sukkal ñi ma jógal, ñu féete ma suuf.
xanaa tànn giirug Yuda, taamu tundu Siyoŋ wi mu sopp.
¶ «Moo tax Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Gannaaw yeena fàttliku seen ñaawtéef, seeni tooñ ne fàŋŋ, seeni bàkkaar fés ci seen jëf jépp, gannaaw yeena ñaaw ñaawtéef gu ñu leen di fàttlikoo, dees na leen jàpp.
Li wér te wóor it moo di sunu Sang ci Yuda la soqikoo, te googu giir, Musaa waxu ci lenn lu jëm ci sarxalkat yi.
Kenn ci mag ñi ne ma: «Bul jooy. Ma ne, Gayndeg giirug Yuda, njebbital Buur Daawuda daan na. Mooy ubbi téere beek juróom ñaari tayoom.»