¶ «Góor gu bopp ba amatul kawar dafa leel waaye set na.
TSK
TSK · Isaiah 15:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ «Buñu wat fenn ci seen bopp te buñu wat seen peggi sikkim, buñu dagg seen yaram it, di ko mititloo ku dee.
«Gox yii di Atarot, ak Dibon, ak Yaser, ak Nimra, ak Esbon, ak Elale, ak Sebam, ak Nebo, ak Bewon,
¶ Ay doom ngeen, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Buleen ñaasu, buleen wat seen kawaru bopp fi féeteek jë bi, ngir di ko mititloo ku dee,
¶ Ba mu ko defee Ayóoba jóg, ne tareet mbubbam, ba noppi watu nel, di ko ñaawloo. Mu daanu fi suuf, sujjóot,
Yeen magi pénc mi, ñaawluleen! Yeen waa dëkk bee, yuuxuleen! Na Filisti gépp ne yàcc! Bëj-gànnaar déy la saxar jollee, kenn du wuute gàngooru noon ya.
Moo tax Mowab di jooy ba ñéppi Mowab jooyoo, ndax namm reseñ ja woon ca Kir Eres, ba ne yàcc, di binni.
Bésub keroog Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi moo leen di woo ci jooyoo ak ñaawlu ak wateefu nel, ak colu saaku ngir ñaawlu.
Watu nel, ñaawloo, dikkal na Gasa, te wedamloo nañu Askalon. Yeen ñi dese joor gi, fu ngeen àppal seen yaram, wi ngeen di daggat, di ko ñaawloo?
«Yeen waa Dibon, dëkk bu taaru bi, wàccleen seen teddnga lu kawe te tooge digg maral; kiy yàqtesi Mowab kat song na leen, di màbbsi seeni tata.
Moo tax may jooy Mowab, di wooteel wall Mowab gépp, di yuuxul waa Kir Eres.
«Éy waa Esbon, Ayi seen dëkk bi tas na, yuuxuleen! Yeen waa dëkk yi séq Raba, sol-leeni saaku, ñaawloo, jaab diggante tata yi, tiisloo. Milkom seen tuur mi déy duggi na ngàllo, ànd aki sarxalkatam aki kàngamam.
Maay soppli seeni màggal ab dëj, seen woyoo woy diy jooy. Maay wodde bépp lupp saaku yu ñuy ñaawloo, bépp bopp, ma wat ub nel, def ko mu mel ni dëju benn bàjjo bu góor, muj ga di bés bu tar.