TSK

TSK · Isaiah 17:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Buurub Asiri nangul ko, dal ca kaw Damaas, nangu dëkk ba, jàpp waa dëkk ba, yóbbu Kir, ba noppi rey Reccin.

Damaas a yilif Siri, te Reccin yiliful lu moy Damaas. Fii ak juróom benn fukki at ak juróom Efrayim tas, ba xeet wa réer.’

Bala xale bee man ne “Baay” mbaa “Yaay” déy, dees na yóbbul buurub Asiri alal ju ñu foqatee Damaas, ak lël ju ñu këfe Samari, nangu ko.»

tey Aji Sax ji wax ne: «Fileek ñetti at yu surga bu ñu bind waññ, dees na sàggi sagub Mowab, te li ñuy bare tey lépp, seenum ndes ay néew lool te tekkeedi.»

Wóoy ngalla Efrayim, kaala gu yànj ga ay màndikatam di sagoo! Taaram bu yéeme baa koy réer, ni tóor-tóor yu wow, te ma nga toŋ ca coll, wa ña biiñ man dëkke, fa tiim xur wu nangu wa.

Hosea 1:6 TSK

¶ Mu dellu ëmb, gannaaw gi mu am doom ju jigéen. Aji Sax ji ne: «Tudde ko Lo Ruwana» (mu firi Ki ñu yërëmul), mu ne: «ndax dootuma yërëm waa kër Israyil, dootuma leen baal.

Ba Efrayim gisee jàngoroom, Yuda gis ab danaam, Efrayim a dem Asiri, yónnee ca Buur Yareb. Waaye manu koo wéral, mbaa di ko fajal ab danaam.

Efrayim, ab sagam ni picc lay naawe, du njurum doom, dub ëmb, du doom ju sosu sax.

Am riir mooy jollee ca sa biir gàngoor, sa tata yépp tas, na Salman tase woon Bet Arbel, keroog bésub xare ba, ba ñu jëlee ndey, fenqaleek doom, ñu rajaxoo.

Efrayim moom, su naatee ci biiri bokkam it, fa màndiŋ ma la ngelawal penku, ngelawal Aji Sax ji di uppe, bëti ndoxam tëju, ay teenam déy. Kii mooy sëxëtoo ab dencam, ak mboolem lu cay alal.»

Amos 3:9 TSK

Yéeneleen ca biir taaxi Asdodd ak ca biir taaxi Misra. Neleen: «Dajeleen ca kaw tundu Samari, ba gis na Samari salfaañoo, ak notaange ga fa nit di daj.

Amos 6:7 TSK

Moo tax yeenay jiituji ngàllo ga, tëraayu xawaare dakk.

Micah 1:4 TSK

Tund ya mu joggi da naan soyox seey, xur ya xar, wàyyi ni dax ju jege sawara, def ni ndox mu wale kaw mbartal.