TSK

TSK · Isaiah 28:1

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Moom moo delloo kemu réewum Israyil fa mu nekkoon, dale ko ca buntu dëkk ba ñuy wax Amat ba ca géeju Araba, muy la Aji Sax ji Yàllay Israyil waxoon jaamam ba, Yonent Yàlla Yunus, ma baayam Ametay cosaanoo Gaat Efer, Yunus jottli ko.

Gaw nañu Samari ba ca ñetteelu at ma, door koo nangu, ca juróom benneelu atu nguurug Esekiya, yemook ba Ose buurub Israyil duggee juróom ñeenteelu atu nguuram.

Wóoy ngalla ñiy teela xëy, daw wutiw ñoll, gonloo biiñ ba tàng jérr.

Damaas a yilif Siri, te Reccin yiliful lu moy Damaas. Fii ak juróom benn fukki at ak juróom Efrayim tas, ba xeet wa réer.’

Bala xale bee man ne “Baay” mbaa “Yaay” déy, dees na yóbbul buurub Asiri alal ju ñu foqatee Damaas, ak lël ju ñu këfe Samari, nangu ko.»

«Ay móol màbb, nu yett ponkali doj, tabaxaat, xànqi garab yu ndaw daanoo ca, nu wuutal ca garabi seedar yu mag.»

Dees na joggati kaala gii màndikati Efrayim di sagoo.

Ngànctu ak biiñ bu yàgg ak bu bees, moo yóbbu seenum xel.

Ci kërug Israyil laa gis lu yées: Fa la Efrayim di gànctoo, Israyil googu laa ne moo sobeel boppam.

Amos 2:8 TSK

Yérey tayle yu ñu nangoo ci néew-ji-doole sax, ñu lal, ne ñàyy ci wetu mboolem sarxalukaay. Ku leen ameel, ñu feyloo la biiñ, naan ca seen biir kër tuur ya.

Amos 4:1 TSK

Dégluleen kàddu gii, yeen jigéeni tundu Samari, yeena ngi suur ni nagi diiwaanu Basan. Yeen ñiy torxal néew-ji-doole, di not aji ñàkk te naan seeni jëkkër: «Indil ñoll waay, ñu naan!»

Amos 6:4 TSK

Yeen ñi tëdd ci seen lal yu yànj, ak a sóonoo seen laltu yu nooy, di yàpp mbote yu baax ak sëllu yu duuf,

Amos 6:8 TSK

Boroom bi, Aji Sax jee ko giñ ci boppam, kàddug Aji Sax ji Yàllaa, Boroom gàngoori xare yi. Nee: «Maaka sib réy-réylug askanu Yanqóoba, ba seen kër yu yànj soof ma! Maay jébbale seen péey ak mboolem li ci biir.