TSK

TSK · Isaiah 28:22

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Na ñaawlekat bi séentu mbugal; ab dof, yeti gannaaw.

Seen xeet wi ni feppi suufas géej lay tollu, te as ndes a ciy délsi. Àtteb sànkute mooy taxaw, yoon toppe ba mat sëkk.

Aji Sax jaa ngii di tas àddina, tasaare ko, salfaañe li fi dénd bi, wasaare ñi ko dëkke:

Fëggleen seen dënn, jooy tooli bànneex ya, jooyleen reseñ ju nangu ja,

Éy Aji Sax ji, naxtaan nga ma, ma naagu, nga nax ma, jaay ma doole, ba man ma. Ñu ngi may kekku bés bu ne, ku ne di ma kókkali.

Gannaaw loolu mu tuur bëti Cedesyas, jénge ko jéngi xànjar, yóbbu ko Babilon.

Mbaa keroog bés ya may jëflanteek yaw, dinga am fit ak doole joo ko dékkoo? Man Aji Sax ji maay wax, jëfe ko.

Dina feddli kóllëre diggam ak ñu bare ci benn àppu juróom ñaar, te ci diggu àppu juróom ñaar ba lay dakkal sarax yi ñuy rendi ak yeneen sarax. Ci genn wetu sarxalukaay bi la yàqkat biy taxawal lu siblu, di sabab yàqute, ba keroog muj gi ñu ko dogalal ne milib ci kawam.»

Wattuleen nag ba li ñu wax ci téerey yonent yi bañ leena dal. Ñu ne:

¶ Man Yowaan, seede naa ñeel képp ku dégg kàdduy waxyu yu téere bii, ne: Képp ku ci yokk lenn, Yàlla dina la yokkal mbugal, yi ñu bind ci téere bii.