Waaye yaw Israyil, sama jaam bi; yaw Yanqóoba mi ma taamu, yaw askanu Ibraayma, samab xarit!
TSK
TSK · Isaiah 29:22
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Aji Sax ji nee: «Yanqóoba, baal xel ci lii! Ma ne Israyil, fàttlikul, yaa di sama jaam! Ma bind la, ngay sama jaam, yaw Israyil, duma la fàtte!
Ci Aji Sax ji la askanu Israyil gépp yeye, bay damu.
Aji Sax ji jotkatub Israyil, moom ku Sellam ki, moo wax ak ki xeet yi xeeb, sib ko, te muy surgawu kilifa yi, mu ne ko: «Ay buur ay gis, jóg, ay kàngam di sukk, ngir Aji Sax ji boroom worma, ngir Aji Sell ju Israyil ji la taamu.»
Ñi Aji Sax ji goreel, nii lañuy dellusee, agsaaley sarxolle fa Siyoŋ, kaalawoo mbég mu sax, mbégteek bànneex wàllsi, naqar aku tiis daw.
Yerusalem, jógal ne ràññ, sag leer feq na; teddngay Aji Sax ji fenkal na la!
Yaw déy yaa di sunu Baay. Ibraayma xamalu nu dara, Israyil xamu nu. Yaw Aji Sax ji yaa di sunu Baay, sa tur a di “sunu Jotkat naka jekk.”
Waaye yaw Yanqóoba sama jaam, bul tiit,» kàddug Aji Sax jee; «yaw Israyil, bul ragal. Fu sore laa lay wallujee, yaak sa askan wa ca réewum njaam ga, Yanqóoba dellu dal, fegu; kenn dootu ko tiital.
«Xanaa dégguloo li nit ñi wax? Ñu ne: “Ñaari làng ya Aji Sax ji tànnoon de, wacc na leen,” moo tax ñu xeeb sama ñoñ, ba tegatuñu leen sax aw xeet.»
Bu sama bérab bu sell nekkee fi seen biir ba fàww, xeet yi dinañu xam ne man Aji Sax ji maa sellal Israyil.”»
Dingeen xam ne ci biir Israyil laa ne, man, maay seen Yàlla Aji Sax ji, du keneen, te sama ñoñ duñu rus mukk.
¶ Moo tax ma ne xanaa ba bànni Israyil tërëfee, jéll bu ñu dul jógati lañu daanu? Mukk kay! Waaye tooñug bànni Israyil moo waral muccug jaambur ñi dul Yawut, ba tax bànni Israyil siis leen.
Ñuy woy nag woy wu yees, naan: «Yaa yeyoo jël téere bi, tàyyi tayu yi, ndax yaw lañu rendi, te sa deret nga jote, ngir Yàlla, ay niti gépp giir ak wépp làmmiñ ak wépp xeet ak wépp askan.