TSK

TSK · Isaiah 30:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Aji Sax jee leen di yeb ciy gaal, delloo leen Misra, yoon wu ma leen noon dungeen ko gisati, ngeen di fa jaay seen bopp seeni noon, ngir doon seen jaam yu góor ak yu jigéen, te kenn du leen jënd.

Gannaaw gi nag buurub Asiri gis ne Ose lal na pexe, ndax daa yónnee ay ndaw ca So buuru Misra, ba noppi lànk ne du fey galag at mu nekk. Buurub Asiri jàpp ko, tëj.

Ña nga naa njiiti Yuda: «Xelal-leen nu, àtte nu, lalal nu bëccëg ndarakàmm ker gu mel ni guddi, yiire ko daw-làqu, yi nu doon; buleen nu wor te nuy wuta raw!

Dañuy boole njàqareek gàcce ndax réewum Kuus mi ñu yaakaaroon, ak Misra gi ñu doon sagoo.»

Misra daal, nga yaakaar, bantu barax bu tas boobu di sokk képp ku ko wéeroo! Firawna buuru Misra de, mooy boobu bant ci képp ku ko yaakaar.

Léegi lu ngeen wuti Misra? Dangeen di naani ca ndoxum Niil ma ca Misraa? Lu ngeen wuti Asiri? Dangeen di naani ca dexu Efraat ca Babilon a?

Mu fekk mbooloom Firawna génn Misra, di ñëw. Waa Babilon ña gawoon Yerusalem dégg ca, ba jóge fa, dellu gannaaw.

xanaa nu dem réewum Misra, fa nu dul gise xare; coowal liitu xare sax dunu ko dégg. Dugub it dunu ko fa ñàkke. Foofa lanuy dëkki;”

Ñu dikk Misra, baña déggal Aji Sax ji, daldi àgg dëkk ba ñuy wax Tapanes.

ba waa Misra gépp xam ne maay Aji Sax ji. «“Seen ndimbal ak Israyil mooy ndimbalu bantu barax,

Hosea 8:9 TSK

Ñoo demal seen bopp Asiri. Mbaamu àll day beru yoonam, waaye waa kër Efrayim ñooy jënd ay far.