TSK

TSK · Isaiah 32:14

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Mu taal kër Aji Sax ji, taal kër Buur, ak këri Yerusalem gépp, boole ca këri boroom barke ya.

Liggéeykati kër Yàlla ya féete Ofel ca tund wa, di liggéey, ba fa janook soorooru koñ, ba féete buntu Ndox ma penku.

Su boobaa sa bunti dëkk sax di ñaawlook a jooy, mel ni ndaw su ñu futti, mu ne dett fi suuf.

¶ Ma ne: «Boroom bi, foo àppal loolu?» Mu ne: «Xanaa fii ba seeni dëkk gental, ba kenn dëkkatu ca, ba nit dootu nekk biir kër ya, suuf sa yàqu yaxeet, di ndànd-foyfoy.

Aji Sax jaa ngii di tas àddina, tasaare ko, salfaañe li fi dénd bi, wasaare ñi ko dëkke:

Tojiti neen a des ci dëkk bi, bunt ba rajaxoo.

Dëkk bu ñu dàbbli mooy wéet, gental, ne wëyëŋ! Fa la nag di fore, fa lay goor, di lekk cari garab ya,

Seen kër buur ya la dég ya di lawe, gajj aki taxas saxe tata ya, till dëkke, bànjóoli tàgge,

¶ «Bu ngeen gisee gàngooru xare gu gaw Yerusalem, su boobaa xamleen ne tasteem dëgmal na.

Mu àddu ca kaw, ne: «Babilon a daanoo! Dëkk bu mag ba daanu na, ba doon dëkkukaayu jinne ak mboolem njuuma lu sobewu ak mboolem picc ak rabu àll wu sobewu te siblu.