Yaw lañu daa woo wall, mucc; yaw lañu wóolu woon te rusuñu.
TSK
TSK · Isaiah 53:3
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Damaa xér ci sa kër gi, ba jeex tàkk, te jëf ji ñu la sewale man la dal.
Yal nañu leen far ca téereb dund ba, bañ leena limaale ca aji jub ña.
Aji Sax ji jotkatub Israyil, moom ku Sellam ki, moo wax ak ki xeet yi xeeb, sib ko, te muy surgawu kilifa yi, mu ne ko: «Ay buur ay gis, jóg, ay kàngam di sukk, ngir Aji Sax ji boroom worma, ngir Aji Sell ju Israyil ji la taamu.»
Ndaxam moom sunu wopp la yenu, sunuy mitit la sëfoo. Nun nu foog ne dees koo mbugal, foog ne Yàllaa ko duma, torxal ko.
«Yaw Betleyem Efrata, lu tuut ci làngi Yuda, ci yaw la ku may yilifal Israyil di génne, cosaanam di jant yu yàgga yàgg, bu jëkkoon.»
¶ Gannaaw loolu ma ne leen: «Su leen neexee, joxleen ma sama peyoor, su leen neexul téyeleen ko.» Ñu waññ fanweeri donji xaalis, feye ma.
Mu neeti: «Fàww Doomu nit ki sonn lu bare, ba dajeek mbañeelu magi askan wi ak sarxalkat yu mag yi, ak firikati yoon yi, te dees na ko rey, ba ñetteelu fanam, mu dekki.»
¶ Yeesu nag yóbbu Fukk ñaak ñaar, wéetook ñoom, ne leen: «Nu ngii jëm Yerusalem, te mboolem lu yonent yi bindoon ci mbirum Doomu nit ki dina sotti.
Ñépp daldi xaacoondoo, ne: «Reyal kii te yiwil nu Barabas!»
Moom Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba, te di sunu Yàllay maam kay, moo màggal jawriñam Yeesu. Yeen nag yeena ko teg ciy loxo, jàmbu ko fa kanam Pilaat, te mu naroon koo bàyyi.
Ndax sarxalkat bu mag bi nu am du ku tëlee yég sunuy néew doole, waaye ni nun rekk lees ko nattoo wet gu nekk, te taxul mu bàkkaar.
Nanu ne jàkk Yeesu, kiy sos, di sottal ngëm, moom mi mbég mi ñu ko waajalal tax mu dékku bant ba ñu ko daaj, tegul muy dara toroxtaange ja ko ca fekk, te doxe ca toog ca ndijooru jalub Yàlla.