TSK

TSK · Isaiah 6:1

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ñu daldi gis Yàllay bànni Israyil. Lu mel ni dëru per bu safiir a nga lal tànkam ya, mel ni asamaan, ndax na mu sete wecc.

¶ Ba sarxalkat ya génnee bérab bu sell ba, niir wa daa fees kër Aji Sax ja,

Mise teg ca ne ko: «Kon nag déglul kàddug Aji Sax ji. Gis naa Aji Sax ji, mu toog ci ngànguneem, mboolem gàngooru asamaan a nga taxaw ndijooram ba càmmoñam.

Job 42:5 TSK

Dég-dégu nopp laa amoon ci yaw, tey bët laa la teg.

Sa ngor a màgg ba sut asamaan, sa worma àkki fa kawa kaw.

¶ Lii moo di peeñum Esayi doomu Amocc, di lu mu gis ci mbirum Yuda ak Yerusalem ci janti buuri Yuda yi ñuy wax Osiyas ak Yotam ak Axas ak Esekiya.

Ku màgg, ku kawe ki, ki màkkaanam sax dàkk te turam sell, daa wax ne: «Fu kawe te sell laa màkkaanoo, maa dëkk ak boroom xol bu mokk, te toroxlu, ngir leqli ku toroxlu, leqli boroom xol bu mokk.

¶ Am na bés, mu yemook sama fanweereelu at, juróomi fan ca ñeenteelu weer wa, booba maa nga bokkoon ca ña ñu toxal ca tàkkal dexu Kebar. Asamaan daa ubbiku, ma daldi gis ay peeñuy Yàlla.

¶ Ba loolu wéyee ma téen, daldi yem ci lu mel ni ngànguney peru safiir ci kaw dénd bi tiim boppi malaakay serub yi.

Moom doŋŋ moo dul dee, moo màkkaanoo leer gu kenn jotewul, te mooy ki nit masula gis te tële koo gis. Teddnga ak kàttan ñeel na ko ba fàww. Amiin.

Ma jekki rekk nekk ci biir Noowug Yàlla. Ci kaw loolu, yemuma lu moy ci am ngàngune mu tege ca asamaan, mu am ku toog ca ngàngune ma.

¶ Ci biir loolu ma gis ci loxol ndijooru ki toog ci ngàngune mi, taxañub téere bu ñu bind biir ak biti, tay ko juróom ñaari tayu.

Ñu ne tund yeek doj yi: «Daanuleen ci sunu kaw, làq nu kanamu ki toog ci ngàngune mi ak sànjum Gàtt bi,

Ba mu ko defee màkkaan ma fees ak saxar su bawoo ci leeru Yàlla ak kàttanam. Kenn nag manatula dugg ci màkkaan mi, ba kera juróom ñaari musibay juróom ñaari malaaka yi matee.