¶ Ci kaw loolu Yanqóoba tudde bérab ba Peniyel (mu firi Xar-kanamu Yàlla), ndaxte da ne: «Ne naa Yàlla jàkk, te maa ngi dund ba tey.»
TSK
TSK · Isaiah 6:5
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Musaa nag ne Aji Sax ji: «Da di, Boroom bi, man naka jekk duma nitu waxkat, du démb, du tey jii ngay wax ak man. Dama di ku leeb, Sang bi, te tëlee wax.»
Teewul Musaa tinu Aji Sax ji, ne ko: «Waaw, waaye man, damaa tëlee wax. Mbaa Firawna dina ma déggal yee?»
Dég-dégu nopp laa amoon ci yaw, tey bët laa la teg.
Cati àddina lay woy di jibe, nu dégg ñu naa: «Teddnga ñeel na Aji Jub ji!»
Yaw mi mel nii, buur bi ci taar bi ngay teg bët; yaay gis réew mi ne màww.
«Na ku ne moytu dëkkandoom te baña wóolu menn mbokk. Kuy mbokk déy lal nga pexem wuruj, di wuruj; kuy dëkkandoo, sos ngay wéye.
Waaye yaw nit ki, bu leen ragal, bul ragal seeni wax. Xam naa ne ay taxas aki dég a lay wër, nga toog ci kawi jiit. Waaye bul ragal seeni wax te bul tiit seen kanam doonte kërug fippukat lañu.
Yaram waa nga rafet ni peru gànjar, xar-kanam ba mel ni melax, bët ya mel ni jumi sawara, loxo yeek tànk yi mel ni xànjar bu ñu jonj, riiru baatam mel ni coowal mbooloo.
¶ Gannaaw gi Aji Sax ji won ma Yosuwe sarxalkat bu mag ba, mu taxaw fa kanam malaakam Aji Sax ji, Tuumaalkat bi taxaw féete ko ndijoor, ngir tuumaal ko.
Simoŋ Piyeer nag gis loolu, daldi sukk fa kanam Yeesu, ne ko: «Sang bi, ngalla sore ma, ngir man nitu bàkkaarkat laa!»,
¶ Aw làmmiñ itam sawara la; làmmiñ a bokk ci sunuy cér, te di àddinay mbon, di gàkkal jëmm jépp. Aw làmmiñ, giiru dundu nit ki lay jafale ab taal bu tàkke fa sawara.
Ma nga yor ca loxol ndijooram juróom ñaari biddiiw, ab saamaru ñaari ñawka bu ñaw di lange ca gémmiñ ga, xar-kanam baa nga leer nàññ ni jantub njolloor.