¶ Ba loolu amee mbooloo mépp tàmbalee yuuxu. Askan wa daa fanaanee jooy guddig keroog.
TSK
TSK · Isaiah 7:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Sa kër ak sa nguur day sax dàkk fi sa kanam, te sab jal day dëju ba fàww.”»
¶ Ba Israyil gépp gisee na leen Buur tanqamloo, dañu koo tontu ne ko: «Ana lu nu bokk ak Daawuda, lu nu séq ak doomu Yese? Bànni Israyiloo, ca seeni xayma! Yaw askanu Daawuda, xoolalal sa bopp sa kër.» Ba mu ko defee bànni Israyil dellu ca seeni xayma;
Booba fekk na Boroom bi dégtal waa dalub Siri ba riirum fas yu ànd aki watiiri xare ak gàngoor gu réy, ba tax ñu naan ca seen biir: «Ãa! Loolu de, buuri Etteen ñaak buuri Misraa, Buurub Israyil fey leen, ngir ñu songsi nu!»
Ñeel Daawuda. Aji Sax jee may leeral, di ma wallu. Ana ku may ragal? Aji Sax jeey aar sama bakkan. Ana ku may tiit?
Ku bon daw na te dàqeesu ko, ku jub ñeme ni gaynde.
Esayi nag ne: «Yeen waa kër Daawuda, dégluleen! Tàyyiloo ngeen nit, di tàyyiloo sama Yàlla itam.
«Bul tudde wor, lenn lu askan wii tudde wor; lu ñu ragal it, bu ko ragal, bu ko tiit.
Fiiraangey Efrayim day jeex, njéefoy Yuda dakk, Efrayim dootu fiire Yuda, Yuda dootu jéppi Efrayim.
Waa dëkk ya ne yàcc, jàq, torox, mel ni gàncaxu àll mbaa ñax mu yees, mbete caxum xadd mbaa tool bu car jógagul.
Yeen waa kër Daawuda, Aji Sax ji dafa wax ne: Àtte yoon, deeleen ko xëye, di xettli ki ñu xañ dëgg ci ki koy néewal doole, balaa sama mer ne jippét, di tàkk te deesu ko mana fey ndax seen jëf ju bon.
«Efrayim, ay fen la ma gawe, waa kër Israyil laa ne, ñoo ma yéewe ag njublaŋ, waaye Yudaa ngi ànd ak Yàlla ba tey, di sàmm kóllëreek Ku Sell ki.»