TSK

TSK · James 3:2

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Bu ñu la moyee, nde amul nit ku dul moy, ba nga mere leen, teg leen ci loxob noon, noon ba jàpp leen, yóbbu am réewam, mu sore mbaa mu jege,

Job 15:13 TSK

Ngay sippi Yàlla sa mer, di ko wax lu mel nii!

Moom sa làmmiñ, sàmm sa bakkan; rattaxle, yàqule.

Amul moos ku jub ci kaw suuf, kuy def lu baax te du bàkkaar.

¶ Takk bi ma ci gis daal mooy lii: bu ma nammee def lu baax, lu bon a may teewalsi.

Waaye mbind mi biral na ne mboolem àddina moo tënku ci kilifteefu bàkkaar, ngir dige bi gëm Yeesu Almasi di jagle, mana dikkal aji gëm ñi.

¶ Almasi moomu nag lanuy xamle; na mu gëna xeloo lanuy àrtoo nit ku nekk, te ni lanuy jàngale nit ku nekk, ngir àgge nit ku nekk ba fa kanam Almasi, fekk ko mat sëkk, na mu ware ku ànd ak Almasi.

yal na leen matal sëkk ci lépp lu baax, ngir ngeen di jëfe coobareem. Yal na def ci nun bànneexu boppam bu mu sottale Yeesu Almasi, mi daraja ñeel ba fàww. Amiin.

¶ Ku yaakaar ne moo jullite te moomul làmmiñam, boppam lay nax te ag njulliteem amul njariñ.

James 3:5 TSK

Noonu itam la aw làmmiñ dee cér su tuut te réy aw bàkk. Seetleen ni ferñent su tuut di lakke gott bu yaa.

Te gannaaw bu ngeen sonnee ab diir, Yàlla miy boroom wépp yiw te woo leen ci ndamam lu sax dàkk ndax Almasi, moom ci boppam moo leen di jagal, dooleel leen, dëgëral leen ba ngeen dëju.