¶ Booba la Laban ne: «Jal bii tey, mooy sunu seede sama diggante ak yaw.» Moo tax ñu tudde ko Galet (mu firi Jalub seede).
TSK
TSK · James 5:3
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Gannaaw loolu Yanqóoba woo ay doomam ne leen: «Bokkleen daje, ma xamal leen li leen di dikkal ëllëg.
Moo ma jàpp, semmal ma; samab jeexaay seedeel ma tuuma.
Maa leen di yàpploo seen doom yu góor ak yu jigéen, ku nekk di yàpp sa moroom ci biir njàqare, ndax gaw bu metti, bu leen seen noon yi leen di tëru di gaw.
Fan yu mujj ya, dees na taxawal tundu kër Aji Sax ji, mooy gëna kawe ci tund yi, tiim tund yu ndaw yi, askan yi riirandoo, wutsi ko.
¶ Waaye sag dëgër bopp, ak sa xol bu tuubadi, ci ngay jóore sànjum Yàlla ci sa kaw bopp, keroog bésub sànj ma, fa àtteb Yàlla bu jub di feeñe.
¶ Kon nag bokk yi, muñleen, ba Boroom bi délsi. Seetleen ci beykat biy séentu njariñal meññeef mu jóge fi suuf si. Ma ngay muñ, céebo ba bët wàcc.
Fukki béjjén yi nga gis, ñook rab wi, dinañu won jigéenu moykat ji mbañeel. Dañu koy futti ba mu ne duŋŋ, ñu lekk aw suuxam, ba noppi lakk ko.
waaye ñu ragal ñi ak aji gëmadi ñi ak defkati ñaawtéef yi ak bóomkat yi ak moykat yi ak xërëmkat yi ak bokkaalekat yi, mboolem niti fen ñi, seen añ a nga ca déegu sawara waak tamarax ba. Loolu moo di ñaareelu dee.»