Ñu laajaat Aji Sax ji, ne ko: «Ndax keneen da fee ñëw?» Aji Sax ji ne: «Mu ngi nii, mu ngi làqu ci biir denc bi.»
TSK
TSK · Jeremiah 21:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ Daawuda ne waa Filisti ba: «Yaw de yaa may jëlal ab saamar ak xeej bu mag ak bu ndaw, waaye man turu Aji Sax ju gàngoor yi laa lay dikke, Yàllay làngi xarey Israyil, ji nga tëkku.
Samiyel ne Sóol: «Ana loo may wooye, di ma yékkati nii?» Sóol ne ko: «Damaa nekk ci njàqare lu réy. Waa Filistee ngi xareek man, te Yàlla dëddu na ma. Wuyootu ma, du ci kàddug yonent, du ci gént. Moo tax ma woo la, ngir nga xamal ma lu may def.»
Fekk buurub Israyil wax aki jawriñam ne leen: «Xanaa xamuleen ne Ramot ga ca Galàdd noo ko moom? Te jéemunoo def dara, ba nangu ko ci loxol buurub Siri!»
¶ Ci biir loolu malaakam Aji Sax ji wax Ilyaas, ma cosaanoo Tisbi, ne ko: «Demal gaaw dajeek ndawi buurub Samari te laaj leen ne leen: “Xanaa Yàlla daa amul ci Israyil, ba ngeen di seeti ca Baal Sebub, tuuru Ekkron?”
«Demleen seetal ma ci Aji Sax ji, seetaaleel mbooloo meek Yuda gépp ci mbirum kàdduy téere bii feeñ. Sànjum Aji Sax ji tàkk ci sunu kaw kat réy na, ndax sunuy maam a déggul kàdduy téere bii, ngir jëfe mboolem li ñu nu ci bindal.»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ànd ak nun, Yàllay Yanqóoba jee nuy rawale. Selaw.
Fàttlikuleen ay jalooreem aki misaalam aki àtteem.
Ma ne, Aji Sax ji gàttul loxo ba tëlee walloo, noppam naqariwul ba tere koo dégg.
¶ «Sëkki gawukaay yaa ngii ñu yékkatil dëkk bi, ngir nangu ko. Dëkk bi dina daanu ci loxoy waa Babilon ñi ko song, ndax saamar akub xiif ak mbas. Gis nga ko déy, li nga waxoon am na!
¶ Mu am bés Buur Cedesyas woo Yukal doomu Selemya, ak Cefaña sarxalkat bi, doomu Maaseya. Mu yebal leen ci Yonent Yàlla Yeremi; ñu ne ko: «Rikk ñaanal nu ci sunu Yàlla Aji Sax ji.»
¶ Ba loolu wéyee Buur Cedesyas yónnee, woolu Yonent Yàlla Yeremi, ñaarook moom fa ñetteelu bunt ba ca kër Aji Sax ja. Mu ne Yeremi: «Dama lay laaj lenn. Bu ma nëbb dara.»
Yonent Yàlla Yeremi ne leen: «Baax na. Maa ngii di leen ñaanal seen Yàlla Aji Sax ji ni ngeen ko waxe. Lu leen Aji Sax ji tontu, dinaa leen ko yegge. Duma ci wacc baat.»
¶ Ba Cedesyas tolloo ci juróom ñeenteelu atu nguuram, fukki fan ca fukkeelu weeram, ca la Nabukodonosor buuru Babilon ànd ak mbooloom xareem mépp ci kaw Yerusalem. Ñu dal fa janook Yerusalem, yékkati gawukaay, wërale ko.
¶ Gannaaw ba loolu wéyee ca atum juróom ñaareel ma, fukki fan ca juróomeelu weer wa, ay nit ñu bokk ci magi Israyil ñoo dikk fi man, di seetlu ci Aji Sax ji. Ñu toog fi sama kanam.