Musaa ne Aaróona: «Lii la Aji Sax ji doon wax ba mu nee: “Ci biir ñi may jegeñ laay feeñal samag sellaay, te ci kanam mbooloo mi mépp lees may terale.”» Aaróonaa nga ne cell.
TSK
TSK · Jonah 4:8
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Buur ne Cadog: «Dellool gaalu Yàlla gi ca dëkk ba. Bu ma Aji Sax ji baaxee, dina ma délloosi, ma gisaat gaal gi, gisaat fi mu dëkk.
¶ Axab ñibbi këram, mer, ne fóññ ndax la ko Nabot waa Yisreel ba wax, ne ko du ko jox suufas maamam. Mu tëdd ca lalam, gedd, baña lekk.
ba ku ma xojoon sax, ma jël, nde dee a ma gënal dese yii yax.
Du naaj wu lay dal bëccëg, mbaa leer gu ndaw guddi.
Waaye am sànj a ko buddi, sànni fi suuf, ngelawal penku wowal doom ya, bànqaasam yu dëgër ya fàq, lax, sawara xoyom ko.
¶ Aji Sax ji itam sànni ngelaw lu réy ca géej ga, muy ngëlén lu réy ca géej ga, ba gaal ga nara tas.
Léegi nag Aji Sax ji, rikk jëlal sama bakkan rekk, ndax dee sax a ma gënal dund!»
¶ «Man, képp ku ma sopp, maa koy jubbanti, yar ko. Kon nag farlul te tuub!