TSK

TSK · Leviticus 1:3

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Yàlla ne ko: «Ngalla jëlal sa jenn doom jii di Isaaxa, muy koo bëgg, nga dem ca réewu Morya ca tund wa ma lay wax, joxe ko fa, mu nekk saraxu rendi-dóomal.»

Naka la Ibraayma siggi rekk, yem ci menn kuuyum xar mu béjjén ya lonke ci as ngarab. Ibraayma dem, jël kuuy ma, rendi, mu wuutu doom ja, di ab saraxu rendi-dóomal.

Ba mu ko defee mu yebal ay ndawi bànni Israyil, ñooña def ay saraxi rendi-dóomal, boole ci rendi yëkk yu ndaw yu ñu def saraxi cant ci biir jàmm, ñeel Aji Sax ji.

Lakkal kuuy mépp ci kaw sarxalukaay bi. Saraxu rendi-dóomal la, ñeel Aji Sax ji, di xeeñ xetug jàmm; saraxu sawara la, ñeel Aji Sax ji.

Ca ëllëg sa mbooloo ma teela xëy, ñu def ay saraxi rendi-dóomal, ak ay saraxi cant ci biir jàmm. Ba mu ko defee ñu toog, di lekk ak a naan, nes tuut ñu jóg, di mbumbaay.

Ba mu ko defee mboolem ña ca am pastéefu xol ak mboolem ña ca seen xel xiir, ñépp dikk, indi jooxeb Aji Sax ji ngir liggéeyu xaymab ndaje meek bépp liggéey bu mu laaj, ngir itam yére yu sell yi.

Ba mu ko defee ñu nangoo ci Musaa mboolem jooxe bu bànni Israyil indi, ngir sottal liggéeyu bérab bu sell bi. Bànni Israyil nag jàppoo suba gu jot di indil Musaa ay saraxi yéene,

¶ «Su fekkee ne li nit kiy sarxe saraxu cant la ci biir jàmm, mu di ko jële ci nag wu góor mbaa wu jigéen, na indil Aji Sax ji lu amul sikk.

bu nemmikoo bàkkaar bi mu def rekk, na sarxe sikket bu amul sikk.

«Ku ñàkka wormaal lenn lu ñu sellalal Aji Sax ji te du teyeefam, daan ba ko war, mu di ko indil Aji Sax ji, am kuuy mu amul sikk lay doon, ñuy xayma njégam, dëppale dayob xaalis baak natt ba ñu yoonal ca bérab bu sell ba. Saraxu peyug tooñ la.

«Santal Aaróona ak doomam yu góor, ne leen li ñu dogal ci saraxu rendi-dóomal mooy lii: Ab saraxu rendi-dóomal day fanaan fi ñu koy lakke ci kaw sarxalukaay bi, ba bët set, sawara way wéye tàkk ca kaw sarxalukaay ba.

¶ «Su sarax si nit kiy génne dee sarax su ñuy wàccoo ngiñ mbaa saraxu yéene, dees na ko lekk bés bi ko nit ki joxee, te lu ca des ba ca ëllëg sa, ñu man koo lekk.

Ba loolu weesee Musaa boole yérey biir yi, ak yeel yi, raxas, ba noppi lakk kuuy mi yépp ca sarxalukaay ba. Loolu saraxu rendi-dóomal la, ngir xetug jàmm. Saraxu sawara la, ñeel Aji Sax ji, na ko Aji Sax ji sante woon Musaa.

Bésub juróom ñetteel ba na indi ñaari kuuy yu amul sikk, ak menn xar mu jigéen mu am at te amul sikk ak juróom ñeenti kiloy sunguf su mucc ayib su ñu xiiwe diw, muy saraxu pepp. Mu indaale genn-wàllu liitaru diw.

te indiwu ko ci bunt xaymab ndaje mi, teewalal ko Aji Sax ji, muy sarax ca bunt jaamookaayu Aji Sax ji, kooku dees na ko topp àqu deret. Dafa tuur deret. Kon dees na ko dagge ci biir bànni Israyil.

liy tax ñu nangul ko mooy muy jur gu amul sikk, di góor; man naa doon aw yëkk mbaa kuuy mbaa sikket.

Na mbooloo mi booleek mburu mi juróom ñaari kuuy yu amul sikk te tollu ci menn at, ak yëkk ak ñaari kuuy, mu doon saraxu rendi-dóomal, ñeel Aji Sax ji. Na ànd ak saraxu pepp ak sarax si ñuy tuur. Loolu sarax la ngir xetug jàmm, ñeel Aji Sax ji.

Balaam ne Balag: «Taxawal fii ci sa saraxu rendi-dóomal, ma dem ba nee. Jombul Aji Sax ji dikk, dajeek man. Mbir mu mu ma won, dinaa la ko àgge.» Mu daldi dem ba ca kaw tund wu ndaw wu dara saxul.

Yàlla du nit, bay fen, du doom aadama bay tuub. Moom wax na lu mu deful a? Am àddu na lu mu sottalul?

Balag ne ko: «Kaay rekk, ma yóbbu la feneen. Jombul Yàlla nangu nga móolool ma leen foofu.»

¶ «Te itam seen bési Terutel weer, nangeen sarxe ab rendi-dóomal, ñeel Aji Sax ji. Ñaari yëkk yu ndaw, ak menn kuuy, ak juróom ñaari xar yu góor yu menn at, te lu ci nekk mucc sikk,

Sarxeleen loolu, te bumu bokke ak rendi-dóomal bi war bés bu nekk tey ànd ak saraxu peppam. Lu mucc sikk nag ngeen di def sarax yooyii, te ngeen defaale saraxi tuuram yi ci war.

Sarxal-leen ci ab rendi-dóomal, ñeel Aji Sax ji, ngir xetug jàmm: wenn yëkk wu ndaw, ak menn kuuy, ak juróom ñaari xari menn at, te lu mucc sikk ngeen di def lépp.

Waaye seetleen bérab bu seen Yàlla Aji Sax ji di taamuji, ci mboolem seeni giir, ngir teg fa turam, dëël ko fa, te ngeen dem foofa.

Te nangeen sarxe seen saraxi rendi-dóomal, yàpp wi ak deret ji, ci seen kaw sarxalukaayu Yàlla Aji Sax ji. Seen deretu yeneen sarax, tuurleen ko ca seen kaw sarxalukaayu Yàlla Aji Sax ji, yàpp wi ngeen lekk ko.

¶ Buleen sarxalal seen Yàlla Aji Sax ji, aw nag mbaa ab gàtt bu am sikk, mbaa jenn laago, ndax seen Yàlla Aji Sax ji seexlu na loolu.

Sa mboolooy taxawal seen bopp, sa bésub xare. Ña nga soloo darajaak sellnga, faboo fa njël sosoo, diy ndaw, wàccsil la, mbeteb lay.

Fa kaw sama tund wu sell wa, fa tundu Israyil wu kawe wa, kàddug Boroom bi Aji Sax jee, foofa déy la ma waa kër Israyil gépp di jaamujee, ñoom ñépp ca réew ma. Fa laa leen di nangule. Fa laay sàkkoo seeni jooxe ak seen ngëneeli sarax, ak lépp lu ngeen ma sellalal.

«Éey saamar, yewwulal sama sàmm bi, sama jàmbaar jii ma lëngool,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. «Dóoral sàmm bi, xar yi tasaaroo, ma walbati sama loxo, jublu ci jur gu ndaw gi.

Luke 1:35 TSK

Malaaka mi ne ko: «Noo gu Sell gi mooy wàccsi ci yaw, dooley Aji Kawe ji yiir la. Moo tax itam ku Sell kiy juddoo ci yaw, dees na ko wooye Doomu Yàlla.

Ndax kat ab joxe, bu àndee ak yéene rekk, la boroom joxe bi amul, deesu ci natt lees koy nangul, waaye li mu am, ci lees koy nangul ab joxeem.

ndax nun ñaari xeet yépp, ci moom Almasi lanu jote ci Baay bi, ci ndimbalal genn Noo gi.

¶ Boobu sarxalkat bu mag lanu soxla; moo sell, mucc sikk, mucc sobe, moom lañu teqale ak bàkkaarkat yi, te moom lañu kaweel ba fa tiim asamaan.

Dafa jëkk ne: «Saraxi jur aki jooxe, saraxi dóomal ak saraxi póotum bàkkaar, bugguloo, safoowuloo,» doonte yoon wee laaj yooyu sarax.