¶ Aji Sax ji dellooti ne ko: «Léegi dugalal sa loxo, teg ko ci sa dënn.» Musaa dugal loxoom, teg ko ca dënnam; ba mu ko génnee, mu defi àkk, xobbiku.
TSK
TSK · Leviticus 13:2
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
boroom néeg bi dafa wara dem ca sarxalkat ba ne ko: “Lu mel ni aw liir laa gis sama néeg.”
¶ Naka la niir wa jóge ca xayma ba, Maryaama jekki ne fureet ak jàngoroy ngaana, weex furr! Aaróona ne Maryaama gees, yem ca ngaana ga.
¶ Su leen mbir jafee ba wees leen ci àtteb bakkan bu ñu faat, ak ay jote, ak loraangey yaram yu ñu teg nit, ak mboolem dëngoo bu laaj àtte ci seen biir dëkk, dangeen di dem ba ca bérab ba seen Yàlla Aji Sax ji di taamuji,
¶ Aji Sax jee leen di dumaa taabi Misra, ak neewoy kërug suuf, ak yaram wu xas, ak ër yuy xasan te dungeen mana am pajam.
¶ Bu loolu wéyee Naaman njiital xareb buurub Siri la woon. Sangam buurub Siri nawloo ko lool, def ko nitam, ndax ciy loxoom la Aji Sax ji jaarale ndam li mu mayoon waa Siri. Ku jàmbaare la woon, waaye daa amoon jàngoroy ngaana.
Moo tax Boroom beey wat jigéeni Siyoŋ nel, Aji Sax jeey muri seen jë.
Yeesu dénk ko ne ko: «Bu ko wax kenn, demal rekk ca sarxalkat ba, ngir mu seet la, te nga génne sa jooxeb setlu, ni ko yoonu Musaa santaanee, muy firnde ci ñoom.»