Ñu daldi leen teg loxo, tëj leen ba ca ëllëg sa, ndax booba guddi na.
TSK
TSK · Luke 21:12
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
¶ woowaat ndaw ya. Ba loolu amee ñu dóor leen, aaye leen ñu waxati lenn ci turu Yeesu, door leena yiwi.
¶ Ba loolu amee ñu yuuxu ca kaw, dar seeni nopp, daldi ànd, ne milib ca kawam;
Mu daanu ci suuf, daldi dégg baat bu ko ne: «Sóol, Sóol, lu tax nga di ma bundxatal?»
¶ Ci kaw loolu mbooloo ma it dal ci seen kaw; àttekat ya futti seeni yére, daldi santaane ñu dóor leen ay yar.
¶ Ca ëllëg sa nag njiital gàngoor ga bëgga am lu ko leer nàññ ca la Yawut ya jiiñ Póol. Mu yiwi ko, woolu sarxalkat yu mag ya, ak mboolem kurélu àttekat ya. Ci kaw loolu mu indi Póol, taxawal ko ci seen kanam.
¶ Festus nag toogsi diiwaanam ba am fa ñetti fan. Gannaaw loolu mu dem Yerusalem.
¶ Ci kaw loolu Àggripa ne Festus: «Kooku de, man sax bëgg naa koo déglu.» Festus ne ko: «Bu ëllëgee dinga ko dégg.»
Yawut ñi ñoo rey Sang Yeesu, na ñu reye woon yonent yi, te ñoo nu bundxatal tey. Neexuñu Yàlla, te nooni ñépp lañu.
¶ Soppe yi, tàngooru nattu bi ngeen nekke nii, bumu leen jaaxal ba mel ni lu jaaduwul moo leen dikkal.