Maay waññi say àttekat, ñu mel na woon, say diglekat it dellu mel ni bu jëkkoon. Su boobaa ñu wooye la Dëkkub Njekk, ak Dëkkub Kóllëre.»
TSK
TSK · Malachi 3:4
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
«Demal yéeneji lii, Yerusalem di dégg, nga ne: “Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngi fàttliku sa ngor ba ngay ndaw, ak sa cofeel ba nga deeb séet, ba ngay topp sama gannaaw ca màndiŋ ma, ba ngay jaare fa dara dul sax.
¶ Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Bu ma tijjee seen wërsëg, kàddu gii dina jibati ci réewum Yuda ak dëkk yi ko séq. Dees na ne: “Yaw dëkkuwaayu njekk bii, yaw, tundu Siyoŋ wu sell wi, yal na la Aji Sax ji barkeel!”
Diiru juróom ñaari fan lañuy def njotlaayal sarxalukaay bi, setal ko, doore ko sasu sarxalukaay bi.
Bésub keroog jóolóoliy fas yi sax dees na ci bind: «Sell na ñeel Aji Sax ji.» Te ni ndabi tuurukaay yi fi kanam sarxalukaay bi selle, cin yi gëna néew daraja ci biir kër Aji Sax ji sax noonu lañu selle.