TSK

TSK · Micah 2:4

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Balaam daldi yékkati kàddug ñaanam, ne: «Jógal dégloo, Balag, teewlu maa, doomi Sippor.

Ci kaw loolu mu yékkati kàddug ñaanam, ne: «Kàddug Balaam a ngi, doomu Bewor, kàddug waa jiy boroom ngis,

¶ Kàddu yii la Daawuda jooye Sóol ak doomam Yonatan.

Job 27:1 TSK

¶ Ayóoba dellu yékkati kàddoom, ne:

su boobaa nangeen woyal buuru Babilon léeb wii, ne ko: «Moo nu ki daan note mujje? Nu mu mujjeek reewandeem?

Aji Sax ji, loo nuy wërloo fu sore say yoon, di nu dërkiisal, ba ragalatunu la? Sang bi, délsil ngir nun, sa giir yii nga séddoo.

«Maay def Yerusalem jali doj, till yi dëkke; ma def dëkki Yuda gent bu kenn dëkkul.»

Nañu gaaw dëbbeel nuy jooy, gët taa, rongooñ wal.

maa ngii di yónnee, jëli mboolem làngi bëj-gànnaar.» Kàddug Aji Sax jee. «Maay yónnee it ca Nabukodonosor buuru Babilon mi ci samag curga, daldi leen boole indi ci kaw réew mii ak ñi ci biiram ak mboolem xeet yi ko séq. Maa leen di faagaagal, gental leen gent bu sax dàkk bu ñuy muslu.

Mu tàqarñi ko fi sama kanam, muy lu ñu bind biir ak biti, mbind ma di kàdduy jooy aki onk aki yuux.

Joel 1:8 TSK

Neeleen wóoy ni janq bu woddoob saaku, di ko ñaawloo jëkkëram, ja ñu ko dencaloon ba muy lu tuut.

Amos 5:1 TSK

Amos ne: Yeen bànni Israyil, dégluleen mii pent: maa ngi leen di jooy, yeen bànni Israyil!

Yeen waa Maresa laay indil ku leen moom, te ca Adulam la ñi Israyil di damoo di làquji.

“Xanaa du ñi mu teg loxo ñépp a koy léebuji, fental ko woy wu ñu ko kókkalee, naan: ‘Wóoy ngalla kii di dajale lu mu moomul, lii ba kañ?’ Kii di sëfoo nii ay bor!”