TSK

TSK · Micah 4:13

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Weñ ak xànjar la say xomb di doon, sa kàttan ànd ak saw fan.

Toyi yebal doomam Yoram ca Buur Daawuda, ngir mu nuyu ko, sargal ko ca la mu xareek Adadeser ba duma ko, ngir Toyi ci boppam xare woon naak Adadeser. Yoram indaaleel ko jumtukaayi xaalis ak wurus ak xànjar.

Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. Aji Sax jee moom suuf ak li ko fees, ak àddina ak li ci biiram.

buuri Tarsis ak dun ya di ko indil ay galag; buuri Saba ak Seba di ko yótsi yóbbal,

Su boobaa ñu indil Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, galag bu bawoo ci xeet wu siggi, rattax yaram, askan wu ñu ragale fu jegeek fu sore, xeet wu am doole, di falaxee, te seenum réew defi wal, galag ba agsi ba tundu Siyoŋ, fa Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi dëël turam.

Maa ngii di la def ngay watiiru bàccukaay bu ñaw, yees peq; ànd aki bëñam, ngay wol tund wu mag, raatale; dëbb tund wu ndaw ba mu mel nib cox.

Aji Sax ji Yàllay Israyil Boroom gàngoori xare yi déy dafa wax ne: «Ñu ngi dëggaate Babilon mu taaru mi, ni ñuy dëggaatee dàgga ju ñuy bàccesi. Balaa yàgg ngóobu Babilon taxaw.»

Micah 5:7 TSK

Ci biir askan yu bare la ndesu Yanqóoba di nekk, ci biir xeeti àddina, mbete gaynde ci biir rabi àll yi, nirook gaynde gu ndaw ci biiri gàtt; fu mu jaare, joggati, xotat, te kenn du wallu.

Mu ne ma: «Ñooñu ñoo di ñaar ñi ñu diw, fal leen, ngir ñu liggéeyal boroom àddina sépp.»

Yuda déy laay bank, muy samag xala, te Efrayim laa koy soxe, muy fitt gi. Yaw Siyoŋ, sa doom yu góor laay yékkati ci sa kaw doom yu góor, yaw réewum Geres (/Yawaan). Doomi Siyoŋ laay def saamaru jàmbaar.

Bésub keroog maay def njiiti Yuda mel ni ab taal bu jafal jalu matt, mbaa jum bu ñu jafal ci sabaaru pepp; wetu ndijoor ak wetu càmmoñ lañuy xoyome mboolem xeet yi leen wër, te Yerusalem toog bérabam, di Yerusalem ba tey.

Bés bu jëkk ci ayu bés yi, na ku nekk génne as lëf ca la mu am, na mu ko àttane, te mu dencal ko boppam, ngir bu ma dikkee, dootu soxlaa wër, di dajale.

Askani àddina, leeru dëkk bi lañuy doxe, buuri àddina di fi indi seen teraanga.