TSK

TSK · Numbers 18:6

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ «Maa ngi nii di indi mbënnu ndox ci kaw suuf, mu far lépp luy dund lu asamaan tiim; te lépp lu nekk ci kaw suuf dina dee.

Man nag maay dëgëral boppu waa Misra, ba ñu dugg, topp leen. Su ko defee ma siiwal sama ndam, ndax dinaa yar Firawnaaki xarekatam yépp, boole ci watiiri xareem aki gawaram.

«Indil Leween ñi, tegleen ci kilifteefu Aaróona sarxalkat bi, ngir ñu di ko jàpple;

«Man mii nag, maa seppee Leween ñi ci bànni Israyil, maa leen weccoo mboolem taaw bu góor bu jëkka juddoo ci ndeyam, ci biir bànni Israyil. Kon nag Leween ñi, sama cér lañuy doon.

«Beral Leween ñi, ñu wecci mboolem taawi bànni Israyil, juri Leween ñi it wecci seenug jur, ma daldi séddoo Leween ñi, man Aji Sax ji.

Maa àddu, man mii; maa ko woo, indi ko, te pexeem dina joy.

¶ «Boroom bi Aji Sax ji déy dafa wax ne: Man ci sama bopp, maa ngii di wër samag jur, maa leen di seet.