Genesis 43:29
TSK
¶ Naka la Yuusufa ne gees, gis Beñamin rakku doomu ndeyam ja. Mu laaj leen ne leen: «Ndax kii mooy seen rakk, ji ngeen ma doon wax?» La ca tegu mu ne rakkam ja: «Sama ngóor si, yal na la Yàlla defal yiw waay!»