TSK

TSK · Obadiah 1:19

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

¶ Ci kaw loolu buurub Asiri jële ay nit dëkk ya ñuy wax Babilon ak Kuta ak Awa ak Amat ak Sefarwayim, dëël leen dëkki Samari, ñu wuutu bànni Israyil. Ñu daldi moom diiwaanu Samari, féetewoo dëkk ya.

Ezra 4:2 TSK

ñëw nañu ca Sorobabel ak ca kilifay kër ya, wax leen ne leen: «Danuy ànd ak yeen tabax ndax danuy topp seen Yàlla, ni yeen, te ca jamonoy Asaradon buurub Asiri, mi nu fi indi ba tey, Aji Sax ji lanuy defal sarax.»

Ezra 4:17 TSK

¶ Ci kaw loolu Buur yónnee tont la Reyum boroom dëkk ba, mook Simsay bindkat ba, ak nàttongoom ya ca des te dëkk Samari ak la des ca Wàllaa Dex. Mu nuyu leen, ne leen:

Fiiraangey Efrayim day jeex, njéefoy Yuda dakk, Efrayim dootu fiire Yuda, Yuda dootu jéppi Efrayim.

Yaw Israyil mu taaru, maa lay defaraat, nga defaru, ba jiinaat sam njiin, wàlli peccum mbéx,

Lu jëm ci Amoneen ñi, Aji Sax ji dafa wax ne: «Israyil daa amuli doom? Am daa amul dono? Lu tax Milkom tuur mi donloo suufas Gàdd, ba ay jaamukatam sanc dëkki Gàdd?

Kon nag, waxalal waxyu suufas Israyil te wax ak tund yu mag yeek yu ndaw yi ak xunti yeek xur yi, ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di waxe fiiraange ak xadar ndax toroxte gi leen xeet yi teg.

te nga wax leen ne leen: “Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Maa ngii di jëleji bànni Israyil ca biir xeet ya ñu fekki, dajalee leen wet gu nekk, délloosi leen seen suufas bopp.

¶ «Lii mooy limeefu giiri Israyil, ak céru suuf bi giir gu ci nekk di féetewoo. Céru Dan moo féete catu bëj-gànnaar. Kemoom day topp yoonu Ettlon ba Lebo Amat, jàll ba Àccar Enan ga digalook Damaas, Amat féete ko bëj-gànnaar. Suufas Dan day jàpp penku ba sowu, ca géej gu mag ga, di benn pàcc.

Amos 1:13 TSK

Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke Amoneen ñi, te duma fomm seeni duma. Ñoo butti ay jigéeni biir ca Galàdd ba ñuy xare ngir yokk seen suuf.

Ngalla nanga sàmme saw yet sa ñoñ, sa gàtt yi nga séddoo, te ñu màkkaanoo gott bi ñoomu neen, fi digg parlu mu naat. May leen ñu fore àlli Basan ak Galàdd na jant ya woon.

Askalon moo koy gis, tiit; Gasa gis ko, jàq njàqare lu réy, mook Ekkron it ndax yaakaar ju tas. Gasa la buur bay réere, Askalon ñàkk ku ko dëkke.