TSK

TSK · Philippians 4:6

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ndaw ya daldi dem ba délsi ca Yanqóoba, ne ko: «Dem nanu ca sa mag Esawu, waaye moom ci boppam mu ngi ci yoon wi di ñëw, fekksi la fii, te ma nga ànd ak ñeenti téeméeri góor.»

¶ Gannaaw loolu Samiyel jël aw doj, teg ko ci diggante Mispa ak fu ñuy wax Sen; mu dippee doj wi Eben Eser (mu firi doju Wall). Mu ne: «Ba fii la nu Aji Sax ji wallu.»

Maa sàkku Aji Sax ji, mu nangul ma, tàggale maak lépp lu ma ragal.

Waaye man, Yàlla laay woo wall, te Aji Sax jee may wallu.

Yàllaa may musal, di ma sagal, ma di ko doolewoo. Sama kiiraay, Yàllaa!

Saraxub ku soxor, Aji Sax ji bañ na ko; ñaanu kuy jubal da koy bége.

¶ Sadarag Mesag ak Abet Nego ne Buur Nabukodonosor: «Buur, soxlawul ñu di la lay dara.

Sang bi ne ko: «Màrt, Màrt, yitte yi nga xintewoo, di ci doñ-doñi moo bare.

Yeen nag, buleen tiisoo lu ngeen lekk, mbaa lu ngeen naan; te bu yooyu xalaat ub seen bopp.

Luke 18:7 TSK

Kon ndax Yàlla man naa baña sàmm àqu tànnéefam ñi koy woo wall guddi ak bëccëg, xanaa di leen yeexe?

¶ Sama coobare mooy, yeen gëmkati Almasi, ngeen mucc ci xalaat yu ub seen bopp. Te ku amul jabar, mbiri Boroom bi lay xalaat, ak nu muy dabe bànneexu Boroom bi.

Fu ngeen tollu, ak ci mbir mu mu mana doon, santleen Yàlla Baay bi ci sunu turu Sang Yeesu Almasi,

¶ Na jàmmu Almasi saytu seen xol. Ci jooju jàmm lañu leen woo, fekk leen ngeen di wenn yaram doŋŋ, te it saxooleen cant.

¶ Ag ñaan nag, saxooleen ko, te ngeen teewlu ci, boole ci ag cant.

¶ Te itam mujug lépp dëgmal na; kon nag jiital-leen seenum xel, te ànd ak seen sago, ngir ngeen man di ñaan.

Jude 1:20 TSK

Waaye yeen samay soppe, sampuleen ba dëgër ci seen yoonu ngëm wu sell wee sell, te ngeen di ñaane ci Noo gu Sell gi.