Nangeen ko joxa jox te bu ngeen koy jox it, bu ci seen xol bon, ndax loolu mooy tax seen Yàlla Aji Sax ji barkeel mboolem seen liggéey, ak mboolem seenu ñaq.
TSK
TSK · Proverbs 11:24
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Mooy nàddil néew-doole yi, njekkam sax dàkk, dooleem di yokku, ànd ak daraja.
Ku baaxe ku ñàkk, lebal nga Aji Sax ji, te moo lay yool.
Dugalal sa alal, dawloo ko; yàgg-yàgg nga jotaat ci.
Yeenay ji lu bare, góob tuuti; lekk, suuruleen; naan, màndiwuleen; solu, nugluwuleen; boroom peyoor feyeeku, yeb ci mbuus mu bënn.»
ku wuti waan ñaar fukki natti pepp, fukk lay fekk sàq ya; mu wuti ca nalukaay ba juróom fukki natti biiñ, fekk fa ñaar fukk.
Mayeleen, ñu may leen; natt bu duun bu ñu rokkas, yëngal, mu fees bay tuuru, moom lees leen di nàddil ci seen mbubb. Ndax natt bi ngeen di nattale, moom lees leen di nattale.»
Moo tax ma noon naa soññ bokk yi, ñu jiitu ma ci yeen, ba waajal ndimbal lu takku li ngeen dige woon, ba mu noppi, te baña doon sompi ŋott, xanaa di ndimbal lu duun.