TSK

TSK · Proverbs 14:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع
Job 31:13 TSK

Ndegam maa sofental sama àqu jaam, bu ñu may jooytu, diy góor mbaa jigéen,

Yeen ñi ragal Aji Sax ji, santleen ko. Yeen askanu Yanqóoba wépp, màggal-leen ko. Yeen bànni Israyil gépp, wormaal-leen ko.

Ndokklee yaw mi yég néew-ji-doole. Aji Sax jee lay xettli, bésub njàqare.

Mooy nàddil néew-doole yi, njekkam sax dàkk, dooleem di yokku, ànd ak daraja.

Nit a ngi tabe, di yokkule; nit di nëŋ-nëŋi, gëna ñàkk.

Kuy ñaawal ku ñàkk, tooñ nga ka ko sàkk; kuy reetaan ku jàq, mbugalam du jaas.

Ku baaxe ku ñàkk, lebal nga Aji Sax ji, te moo lay yool.

Kuy jox néew-ji-doole, doo ñàkk; nga gëmm ne gisoo, bare ku la móolu.

Xanaa du sédd ku xiif saw ñam, fat néew-ji-doole ju amul fu mu dëkk, gis ku rafle, wodd ko, te baña nëbbu mbokk mu soxla?

Luke 18:9 TSK

¶ Yeesu léebati lii, ngir ñiy damoo seenug njub, tey doyadal ñi ci des.

Su ko defee dungeen yàccaaral, waaye dangeen di roy ci ñi gëm te muñ, ba jagoo digey Yàlla.

¶ Bokk yi, ku ne gëm na, te jëfewu ko, ana lu mu koy jariñ? Ndax googu ngëm man na koo musal?