Yuusufa ne leen: «Li ngeen def nag? Xanaa xamuleen ne nit ku mel ni man day gisaane?»
TSK
TSK · Proverbs 16:10
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Genesis 44:15
TSK
2 Samuel 14:16
TSK
Jombul Buur sang bi nangu maa xettli ci ki nuy fexee boole ak sama doom sànk, beddee nu ci céru Yàlla.
1 Kings 3:28
TSK
¶ Israyil gépp nag dégg àtteb Buur, daldi yéemu ci moom, ndax dañoo gis ne xelum Yàlla mu rafet a ngi ci moom, di ko jiite ci àtte dëgg.
Psalms 72:1
TSK
Ñeel Suleymaan. Céy Yàlla, mayal Buur sa xelum àtte, mayal doomu Buur bii sa xelum njekk,
Proverbs 16:12
TSK
Buur daa sib kuy def lu bon, ngir njekkay dëgëral nguuram.
Isaiah 32:1
TSK
Buur a ngii, njekk lay nguuroo, jawriñ ñi it, yoon lañuy yilifee;
Hosea 10:4
TSK
Ñooy wax seeni wax, di giñe ay fen yu ñuy fasoo kóllëre, ba yoon mel ni gàncaxu tooke ju law ca tooboy tool ya.»
Amos 6:12
TSK
Moo fas dina daw ciy doj a? Am dees na ràng aw nag, di gàbb doj? Moona walbati ngeen àtteb yoon, def ko tooke, yoon mel ni xay.