Firawna nag mere lool ñaari jawriñ yooya, kenn ka di kilifay ñay topptoo naani buur, ka ca des di kilifay lakk-kati mburu ya,
TSK
TSK · Proverbs 16:14
مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.
Genesis 40:2
TSK
Esther 7:7
TSK
Buur ne ñokket, mer ba fees, bàyyi fa biiñ ba, dugg ca biir tóokëram. Aman moom, des fa, di tinu Lingeer Esteer ngir bakkanu boppam, ndax booba xam na ne su dee Buur rekk, njekkaram taxaw na.
Proverbs 19:12
TSK
Merum buur ni gaynde gu ŋar; yërmandey buur ni lay cig mbooy.
Proverbs 29:26
TSK
Ñu baree ngi sàkku kilifa baaxe leen, moona Aji Sax jeey àtteb jaam.
Daniel 2:16
TSK
Dañeel nag dem ca Buur, ñaan ko mu may ko jot gu mu ko joxe pirim gént ga.
Acts 12:20
TSK
¶ Fekk na Erodd dëngoo lool ak waa dëkk yi ñuy wax Tir ak Sidon. Ci kaw loolu waa Tir ak Sidon mànkoo, dikk ba ci Erodd. Ñu daldi fexe ba jubook Balastus, bëkk-néegu Buur, ba noppi di sàkku jàmm, ndax seen dundub réew, ca dundu Buur Erodd la daan jóge.