TSK

TSK · Proverbs 17:11

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ci biir loolu Absalom di def ay sarax, daldi yónnee, ñu jëli Ayitofel ma topp ca Daawuda, di ko xelal. Ayitofel bàyyikoo ca Gilo. Pexe ma nag mujj na réy, ña topp Absalom di yokku ba bare.

¶ La ca tegu fukki nit ña doon gàddul Yowab ngànnaayam, dikk wër Absalom, jam ko, mu dee.

¶ Booba nit ku bon a nga woon ca mbooloo ma, ku ñuy wax Seba, di doomu Bikkri, ma bokk ca giirug Beñamin. Seba wal liit ga, daldi yéene ne: «Sunu yoon nekkul ci Daawuda doomu Yese jii, du benn cér bu nu am ci moom. Yeen waa Israyil, ku nekk ca sa xayma!»

Léegi nag giñ naa ci Aji Sax ji, Kiy Dund, te teg ma fi, dëj ma ci jalub Daawuda sama baay, sampal ma askanu nguur, wa mu dige woon, bésub tey jii Adoña dina dee.»

Buur nag sant Benaya doomu Yoyada, mu génne Simey, jam ko, mu dee. Ba loolu amee nguur ga gëna dëgër ca loxol Suleymaan.

Sama noon yooyu buggul woon ma doon seen buur nag, indileen leen fii, te rendi leen ci sama kanam.”»