TSK

TSK · Proverbs 18:21

مراجع Treasury of Scripture Knowledge في KYG.

العودة إلى المقطع

Ñu ngi naa: «Sunu làmmiñ lanuy daane, nook sunu kàddu; ku nu manal dara?»

Kàddug ku jub day jur xel mu rafet, ku wax njekkar ñu tëj sa gémmiñ.

Bàkkaaru làmmiñ dugal na boroom, ku jub mucc ci njàqare.

Waxi nit ndox mu xóot la, bu bënnee, xelli, ñu di ca xelu.

Maay teg ci seen làmmiñ kàddug cant. Jàmm, na jàmm ñeel ñépp, ku soreek ku jege.» Kàddug Aji Sax jee. Mu ne: «Maa leen di faj.»

¶ Waaye nees di wooye koo gëmul? Nees di gëme koo déggul turam? Nees di dégge turam, te yégleesu ko?

Kon bu ay ndawam itam di mbubboo ndawi njub, du doon lu yéeme. Waaye seenug muj, seeni jëf lay yemool.

Na seen kàddu ànd ak yiw te am solo, te ngeen xam nu ngeen di tontoo ku nekk, tont li war.

James 3:6 TSK

¶ Aw làmmiñ itam sawara la; làmmiñ a bokk ci sunuy cér, te di àddinay mbon, di gàkkal jëmm jépp. Aw làmmiñ, giiru dundu nit ki lay jafale ab taal bu tàkke fa sawara.